"bu Yàlla dajalee ñu njëkk ña ak ñu mujj ñi ëllëg bis-pénc dees na yëkkëtil bépp workat ab raaya, ñuy wax naan: lii mooy worug diw doomu diw".
Jële nañu ci Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"bu Yàlla dajalee ñu njëkk ña ak ñu mujj ñi ëllëg bis-pénc dees na yëkkëtil bépp workat ab raaya, ñuy wax naan: lii mooy worug diw doomu diw".
«إِذَا جَمَعَ اللهُ الْأَوَّلِينَ وَالْآخِرِينَ يَوْمَ الْقِيَامَةِ يُرْفَعُ لِكُلِّ غَادِرٍ لِوَاءٌ، فَقِيلَ: هَذِهِ غَدْرَةُ فُلَانِ بْنِ فُلَانٍ».
Yónente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne bi Yàlla mu kawe mi dajalee ñu njëkk ña ak ñu mujj ñi ëllëg bis-pénc ngir regle leen, day sampal bépp workat bi daa wul matale kóllare gi mu fasante ak Yàlla walla nit ñi màndarga mom day wuññi woram gi, ñuy woote ca bis booba naan: Lii mooy worug diw doomu diw; ngir feeñal ñaawteefu jëfam ca waa bérab bañuy dajaloo.
Araamalees na wor ak ne dafa bokk ci bàkkaar yu mag yi; ndax tëkku gu tar moo ci nekk.
Wor gii ñu tëkkoo day làmbo képp ku la wóolu ci dereet, walla der, walla sekkare, walla alal nga wor ko, daal di juuyoo ak li mu njortoon ci wóolu gi mu la wóolu.
Al-Xurtubii nee na: lii wàqante la ak aaraab yi ci kem na ñu daan def; ndax ñoom dañu daan yëkkëti raaya gu weex ngir matal kóllare, ak raaya gu ñuul ngir yedd workat bi ak ŋàññ ko, loolu waral wax jii ngir misaal workat bi; ngir mu siiwe ci meloom wi ëllëg bis-pénc ndax ña taxawba ñëpp ŋàññ ko.
Ibn Hajar nee na: nekk na ci it ne nit ñi dees na leen woo ëllëg bis-pénc ci seen turi baay yi; ngir li mu wax ne: "lii mooy worug diw doomu diw".
Yataal gi (5)
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (4/ 104) (3188) صحيح مسلم (3/ 1359) (1735).
تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.
للبسام (ص745).
الإلمام بشرح عمدة الأحكام.
لإسماعيل الأنصاري (2/ 188).
Cited in books
2 BooksYataal gi (2)
- قاموس الكبائرموسوعة الكبائر - المجموعة الثالثة«إِذَا جَمَعَ اللَّهُ الأَوَّلِينَ وَالآخِرِينَ يَوْمَ الْقِيَامَةِ، يُرْفَعُ لِكُلِّ غَادِرٍ لِوَاءٌ، فَقِيلَ: هَذِهِ غَدْرَةُ فُلَانِ بْنِ فُلَانٍ» [114].
- مباحث في أصول الدين1وقال النبيّ صلى الله عليه وسلم: «إذا جمع الله الأوّلين والآخرين يوم القيامة يرفع لكلّ غادرٍ لواءٌ، فقيل: هذه غدرة فلان بن فلانٍ».