Skip to content

"bu kenn ci yéen eggee cib jotaay na nuyóo, bu nammee jug na nuyóo, ndax bu njëkk bi gënut a yay bu mujj bi".

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

"bu kenn ci yéen eggee cib jotaay na nuyóo, bu nammee jug na nuyóo, ndax bu njëkk bi gënut a yay bu mujj bi".

«إِذَا انْتَهَى أَحَدُكُمْ إِلَى الْمَجْلِسِ فَلْيُسَلِّمْ، فَإِذَا أَرَادَ أَنْ يَقُومَ فَلْيُسَلِّمْ، فَلَيْسَتِ الْأُولَى بِأَحَقَّ مِنَ الْآخِرَةِ».

Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ahmat.
Tane na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jàngale na ne ku ñëw ci bérab bu nit ñi toog na leen nuyu, bu fa nammee jóge it na tàggatoo ak ña fa nekk ba tay ci nuyóo; ndax nuyóo bu njëkk bi ca ba muy ñëw gënut a yay nuyóo bu mujj bi bu fay jóge.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ñaaxe ci tasaare nuyóo.

Ñaaxe ci nuyu waa jotaay bi bu ñëwee ci ñoom ak bu fay jóge.

As-Sindii nee na: waxam ji: (bu nammee jug) maanaam: bawoo ca bérab ba, (ndax bu njëkk bi gënut a yay) maanaam: ñoom ñaar ñépp sunna lañu yu ñu wara jëfe, kon lay amul ci bàyyi bu ñaareel bi di def bu njëkk bi.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (7/ 500) (5208).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 432) (2706).

Téere bu mag bi An-nasaa'iy def ci Sunna yi (9/ 144) (10129).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (12/ 47) (7142).

Yataal gi (8)

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (11/ 360).

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (2/ 142).

تطريز رياض الصالحين.

لفيصل آل مبارك (ص523).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (1/ 672).