Skip to content

"Àjjana am na ab buntu bu ñuy woowe Rayyaan, woorkat yi ñoo cay dugg ëllëg bis-pénc, kenn du ca dugg ku dul ñoom

Jële nañu ci Sahl yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

"Àjjana am na ab buntu bu ñuy woowe Rayyaan, woorkat yi ñoo cay dugg ëllëg bis-pénc, kenn du ca dugg ku dul ñoom, dañuy wax naan: ana woorkat yi, ñu jug kenn du ca dugg ku dul ñoom, bu ñu duggee ñu tëj ko, keneen du ca dugg".

«إِنَّ فِي الْجَنَّةِ بَابًا يُقَالُ لَهُ الرَّيَّانُ، يَدْخُلُ مِنْهُ الصَّائِمُونَ يَوْمَ الْقِيَامَةِ، لَا يَدْخُلُ مِنْهُ أَحَدٌ غَيْرُهُمْ، يُقَالُ: أَيْنَ الصَّائِمُونَ، فَيَقُومُونَ لَا يَدْخُلُ مِنْهُ أَحَدٌ غَيْرُهُمْ، فَإِذَا دَخَلُوا أُغْلِقَ، فَلَمْ يَدْخُلْ مِنْهُ أَحَدٌ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne amna bunt ci bunt Àjjana yi bu ñuy woowe Rayyaan: buntub Rayyaan, woorkat yi ñoo cay dugg ëllëg bis-pénc, kenn du ca dugg ku dul ñoom, dañuy woote ne: ana woorkat yi, ñu jug daal di dugg, ku dul ñoom du ca dugg, ka ca mujj bu duggee ñu tëj ko, keneen du ca dugg ginnaaw ga.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

An-Nawawii nee na: nekk na ci hadiis bi ngëneelu woor ak teraangay woorkat yi.

Yàlla dafa beral woorkat yi ab bunt ci bunti Àjjana yiy juróom-ñatt, bu ñu ca duggee ñu tëj ko.

Leeral ne Àjjana dafa am ay buntu.

As-Sindii nee na: waxam ji: (ana woorkat yi), maanaam ñiy bari lu ñuy woor niki ñuy waxe aji-maandu ji ak aji-tooñ ji, te ki ko tàmm la ñuy wax loolu, waaye du ki koy def ben yoon.

(Rayyaan) li muy tekki mooy kiy nàndal; ndaxte woorkat yi dañuy mar saa su ne rawati na jamonoy tàngaay wi muy tàng lool; ba tax ñu fay leen ci tudde buntu boo bu la dëppoo ak ñoom, buntub Nàndal (Rayyaan), nee na ñu it Ràyyaan mooy ku bari lu muy nàndal muy safaaanu mar, dañu ko a tudde noonu; ndax fayug woorkat yi la ca seen mar ga ak seen xiif ga.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (3/ 25) (1896).

Téere Muslim bi gën a wér (2/ 808) (1152).

Yataal gi (6)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (2/ 360).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (2/ 868).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (5/ 270).