Skip to content

"mo ndax dees na leen dimbali di leen wërsëgal lu dul ci seen néew ji doole yi".

Jële nañu ci Mushab ibn Sahd mu wax ne: Sahd yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa gis ne daa am ngëneel ci ñi ko feete suuf, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko:

"mo ndax dees na leen dimbali di leen wërsëgal lu dul ci seen néew ji doole yi".

«هَلْ تُنْصَرُونَ وَتُرْزَقُونَ إِلَّا بِضُعَفَائِكُمْ».

Al-buxaariy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Sahd ibn Abii Waqaas yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa njort ne daa am ngëneel ci kaw neew ji doole yi ko feete suuf ngir sababus njàmbaaram ak yi ko niru! Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne: ndax dees na leen dimbali lu dul ci seen néew ji doole yi ci seen i ñaan ak seenug sellal; ndax ñoom lu ci ëpp ñooy ëpp ag sellal ci ñaan yi, ñooy ëpp it ak toroxlu ci jaamu gi, ngir li seen xol yi féex wolif muy aju ci taar-taari àdduna.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ñaaxe ci toroxlu ak bañ a yëkkëtiku ci kaw ñeneen ñi.

Ibn Hajar nee na: bu dee ku am kàttan dafa ràññeeku ci ngëneelu njàmbaaram, aji-néew ji doole it day ràññeeku ci ngëneelu ñaanam ak sellalam.

Ñaaxe ci rafetal jëme ci way-ñàkk ñi ak jox leen seen àq, ndax loolu sabab la ci yërmàndeg Yàlla ñeel la ak ndimblam.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (4/ 36) (2896).

Yataal gi (6)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 354).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (3/ 111).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (1/ 279).