Skip to content

«kiy jokk mbokk du kiy faye liñuko jokk, waaye kiy jokk mbokk mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkam mu jokk ka ko dog.

Jële nañu ci Abdulaa Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«kiy jokk mbokk du kiy faye liñuko jokk, waaye kiy jokk mbokk mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkam mu jokk ka ko dog.

«لَيْسَ الْوَاصِلُ بِالْمُكَافِئِ، وَلَكِنِ الْوَاصِلُ الَّذِي إِذَا قُطِعَتْ رَحِمُهُ وَصَلَهَا».

Al-buxaariy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne nit ku mat ci jokk bokk ak rafetal jëme ci jegeñaale yi nekkul nit kiy fay rafetal cig rafetal, Waaye jokk-katu mbokk dëgg mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkoom mu jokk ko, bu ñu ñaawalee jëme ci moo; dakoy faye ag rafetal jëme ci ñoom.

Maanaay baat yi

المكافئ: الذي يكافئهم على صلتهم له، إن وصلوه وصلهم وإن قطعوه قطعهم.

وصلها: برها وأحسن إليها.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Jokk mbokk gi Lislaam jàpp mooy nga jokk ku la dog, di baal ku la tooñ, di jox ku la xañ, waaye jokk nekkul ci defalante ak fayantoo.

Jokk mbokk dana nekk ci nga fexe ba éggale ci ñoom lu jàppandi ci aw yiw niki alal ak ñaan ak digle lu baax tere lu bon ak yu ni mel, ak nga fexe ba jeñal leen aw ay.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 6) (5991).

Yataal gi (8)

منار القاري شرح مختصر صحيح البخاري.

لحمزة محمد قاسم (5/ 242).

بهجة الناظرين.

لسليم الهلالي (1/ 397).

نزهة المتقين.

لمصطفى الخن وغيره (1/ 311).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (3/ 190).