Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

46 of 732 cards

Clear filters
« Du dagan ci nit ki mu tóng mbokkam lu ëpp ñatti guddi, ñuy dajee kii dummóoyu kee dummóoyu, ki gën ci ñoom ñaar mooy ki tàmbli nuyóo ba».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«bu kenn ci yéen dajee ak mbokkam na ko nuyu, bu dara doxee seen diggante ag garab walla miir walla aw doj mu dajewaat ak moom na ko nuyu batay».
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko.
«aji-gëm nekkul kiy jamaate, walla kiy rëbbaate, mbaa kiy def ñaawteef, walla aji-bon lammiñ ji».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko.
Jenn waay ñëw na ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: assalaamu halaykum, mu fay ko mu daldi toog, Yonnente bi ne: "fukk" keneen daal di ñëw ne: assalaamu halaykum wa rahmatu Laah, mu fay ko mu toog, mu wax ne: "ñaar fukk" topp keneen ñëw daal di ne: assalaamu halaykum wa rahmatul Laahi wabarakaatuhu, mu fay ko mu toog, mu ne: "fanweer".
Tane na Abuu Daawuda ak At-Tirmisiyyu ak Ahmad ak Ad-Daaramiyyu soloo nañu ko.
Bu kenn ci yéen di jàpp na def ndox ci bakkanam daa di saraxndiku, kuy fomp (laabu) na ko tóolal, bu kenn ci yéen yeewoo ciy nelawam na raxas loxoom njëkk mu koy dugal ci jàppukaay bi, ndax kenn ci yéen xamul fan la ab loxoom fanaan". Baati Muslim mooy: "bu kenn ci yéen yeewoo ciy nelawam bu mu nuural loxoom ci ndab li ba baa mu koy raxas ñatti yoon ba noppi, ndaxte moom xamul fan la ab loxoom fanaan ".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Benn waay da doon lekke càmmooñ fi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ko: "lekkeel sa ndayjoor", waa ji ne ko: manuma ko, mu ne ko: "Yàlla boo ko man", dara terewu ko ko lu dul rëy, nee na: yëkkatiwaatu ko jëme ci gémmiñam.
Wér na Muslim soloo na ko.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- guddi gu nekk bu daan yéeg ci lalam day boole ñaari téqam, daal di ciy ëf, daal di jàng: {Xul huwal Laahu Ahadun}, ak {Xul ahuusu Bi Rabbil falaxi} ak {Xul ahuusu Bi Rabbin naasi}, daal di ciy masaa yaramam lu mu man, tàmbalee ca bopp ba ak kanam ga, ak lu ca topp ci yaramam, da koy def ñatti yoon.
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
benn waay dafa laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: lan moo gën ci Lislaam? Mu ne ko: "nga leele ñam, ak di nuyu koo xam ak koo xamul".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.