Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

62 of 732 cards

Clear filters
«Ndax duma leen xibaar bàkkaar yi gën a mag?» Mu wax ko ñatti yoon, ñu ne ko: ahakay yaw Yónente Yàlla bi, mu ne leen: «bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur» mu jóg toog fekk dafa sóonu woon, daal di ne: «ak wax ludul dëgg», nee na: deñul di ko bàmtu ba ñu mujj wax naan: aka neexoon mu noppi.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«am na benn waay bu doon lebal nit ñi, daan wax ndawam la naan ko: boo demee ci ku am jafe-jafe nanga ko jéggal, amaana Yàlla jéggal nu, mu dajeek Yàlla mu jéggal ko».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"góor du xool awray góor, jigéen it du xool awray jigéen,te góor ak góor duñu sàngu ci menn malaan,jigéen ak jigéen it du ñu sàngu ci menn mbalaan .
Wér na Muslim soloo na ko.
«ndax xam ngeen kan mooy ki ñàkk?" Ñu ne ko: ki ñàkk fi nun mooy ki amul dërëm te amul ay jumtukaay, mu ne: "ki ñàkk ci samaw xeet mooy ki ñëw bis-pénc indi ay julli ak woor ak asaka, mu ñëw fekk saaga na kii, tuumaal kee, tuur dereetu kii, dóor kee, ñu jox kii ci ay yiwam, jox kee ci ay yiwam, bu ay yiwam jeexee njëkk muy fay li ko war, ñu jël seen i ñaawteef sànni ko ko, topp ñu daaldi kay sànni ca sawara».
Wér na Muslim soloo na ko.
«Yàlla dafa bëgg jaam bu ko ragal, bu doylu, bu nëbbu».
Wér na Muslim soloo na ko.
"leelleen aji-xiif ji, seetileen ki feebar, yeewileen jaam bi".
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
Wax naa Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: doy na la sëkk ci Safiyyatu lii ak lii, -kenn ci nettalikat yi nee na: maanaam dafa gàtt- mu ne ko: wax nga kàddu gog bu ñu ko jaxase woon ak ndoxum géej gi mu jaxase ko" ne na: ma nettali ko kenn nit, mu ne ma: bëgguma di wax ci nit donte damaa am lii ak lii".
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat.
«Yàlla bind na rafetal ci mbir yépp, bu ngeen dee ray nangeen rafetal rayiin wa, bu ngeen dee rendi nangeen rafetal rendiin wa, nangeen daas seenug ñawka tey noppal li ngeen di rendi».
Wér na Muslim soloo na ko.