"baayima yii dañoo am ag caay-caay kem caay-caayu rab yi, bu leen ci të rekk def leen ko kem nii"
Jële nañu ci Raafih ibn Xadiij yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Nekkoon nanu ak Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci Sul Hulayfata, nit ñi xiif, ñu jàpp ay giléem ak ay gàtt, nee na: Yonnente bi moo nga nekk ca ginnaaw nit ña, ñu yàkkamti, daal di rendi, daal di teg cin yi, Yonnente bi digle ñu tuur cin yi, mu seddale daal di yemale fukki gàtt ci genn giléem, genn giléem daal di rëcc, ñu topp ko, ba mu lottal gaa yi, te ay fas yu néew ñoo nekkoon ci gaa yi, benn waay ci ñoom jël ag fett jam ko, Yàlla dal di koy téye, topp mu wax ne: "baayima yii dañoo am ag caay-caay kem caay-caayu rab yi, bu leen ci të rekk def leen ko kem nii", Raafih: daal di wax ne: nun de yaakaar nanu -walla ragal nanu- noon bi suba, te amuñu ay paaka, ndax nu rendee ci bant yi? Mu ne: "lépp luy tuur dereet, te ngeen tudd ca turu Yàlla nangeen ko lekk ba mu des bëñ ak weh, dinaa leen wax lu tax loolu: bu dee bëñ moom yax la, bu dee we nag moom paakag yéefari waa Habasa la".
كُنَّا مَعَ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ بِذِي الحُلَيْفَةِ، فَأَصَابَ النَّاسَ جُوعٌ، فَأَصَابُوا إِبِلًا وَغَنَمًا، قَالَ: وَكَانَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِي أُخْرَيَاتِ القَوْمِ، فَعَجِلُوا، وَذَبَحُوا، وَنَصَبُوا القُدُورَ، فَأَمَرَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ بِالقُدُورِ، فَأُكْفِئَتْ، ثُمَّ قَسَمَ، فَعَدَلَ عَشَرَةً مِنَ الغَنَمِ بِبَعِيرٍ فَنَدَّ مِنْهَا بَعِيرٌ، فَطَلَبُوهُ، فَأَعْيَاهُمْ وَكَانَ فِي القَوْمِ خَيْلٌ يَسِيرَةٌ، فَأَهْوَى رَجُلٌ مِنْهُمْ بِسَهْمٍ، فَحَبَسَهُ اللَّهُ، ثُمَّ قَالَ: «إِنَّ لِهَذِهِ البَهَائِمِ أَوَابِدَ كَأَوَابِدِ الوَحْشِ، فَمَا غَلَبَكُمْ مِنْهَا فَاصْنَعُوا بِهِ هَكَذَا»، فَقَالَ أي رافع: إِنَّا نَرْجُو -أَوْ نَخَافُ- العَدُوَّ غَدًا، وَلَيْسَتْ مَعَنَا مُدًى، أَفَنَذْبَحُ بِالقَصَبِ؟ قَالَ: «مَا أَنْهَرَ الدَّمَ، وَذُكِرَ اسْمُ اللَّهِ عَلَيْهِ فَكُلُوهُ، لَيْسَ السِّنَّ وَالظُّفُرَ، وَسَأُحَدِّثُكُمْ عَنْ ذَلِكَ: أَمَّا السِّنُّ فَعَظْمٌ، وَأَمَّا الظُّفُرُ فَمُدَى الحَبَشَةِ».
Raafih ibn Xadiij yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day nettali ne dañoo nekkoon ak Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci Sil Hulayfata, nit ña daal di xiif, fekk dañoo nangoo woon ci yéefar yi ay Giléem ak i gàtt, ñu gaawantu ray ci giléem yi ak gàtt yi laata ñu koy séddale, ñu teg cin yi te tàgguwuñu Yonnente bi, fekk Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo nga woon ca ginnaaw nit ña, ba mu ko xamee, dafa digle ñu këpp ñeex mi nekk ci cin yi, topp mu séddale la ñu am ci seen diggante, muy fukki gàtt muy tolloo ak benn giléem, benn giléem daal di rëcc, te manuñu ko a jot, te fas yi bariwul, benn waay ci ñoom jam ko ag fett, Yàlla téyeel leen ko, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ne: Jur gii di miin dafa am melow rab, bu leen notee ba manuleen ko a jàpp def leen ko nii. Raafih ne: nun de foog nanu ne dañuy daje ak noon bi suba te ragal nanu ne bu ñu rendee ci su nu ngànnaay yi kon du ñawati te soxla nanoo rendi lool, te amunu paaka, ndax nu rendee ci bantu garabu suukar bu ñu sot? Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne: lépp lu mana tuur dereet ko muy sotti ku bu baax, ñu tudd ca turu Yàlla lekk leen ko, ba mu des bëñ ak weh, dinaa leen wax lu waral loolu: bu dee bëñ moom yax la, bu dee weh nag moom yéefari Habasa yi dañu koy jëfandikoo.
Feeñal dara ci toroxlug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci li muy dox ci ginnaaw Arme bi, ak di sàmm ay àndadoom, di leen nemmeeku, ak li mu nangu laabireg ay àndadoom yal na leen Yàlla dollee gërëm.
Njiit li day yar ñi muy sàmm ak ay soldaaram, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc yar na leen ci seen gaawantu gii ak seen jëf jii, njëkk ñuy jël ndigalam, ba tax seenug fay di xañ leen la ñu bëggoon.
Gaawug sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm ci topp ndigali Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Tere nañu ñuy jël ci alali gi ñu jële ci xeex laata ñu koy séddale.
Maanu rawati na fi ñuy Jihaade ak noon yi ak yéefar yi; ndax dafa bokk ci yiy waral ndimbal ak not noon yi.
An-Nawawii nee na: luy miin nit bu dee dafa rabe niki giléem gu màmmu walla nag walla fas, walla xar wu rëcc mbaa leneen, kon moom day mel ni am rëbb, kon dana dagan ñu jam ko.
Rendi rab wi lu war la ngir mu dagan a lekk, dees na sàrtal ci rab wi: 1- mu nekk lu dagan a lekk, 2- mu nekk lu ñu man a rendi, bu ñu ko manul kon àtteem mooy àtteb rëbb, 3- mu nekk rabu jéeri; bu dee rabu géej la deesu ci sàrtal rendi gi.
Sàrt yiy tax ag rendi wér: 1- aji-rendi ji di ku mana rendi, ci mu nekk ku am xel, di ku ràññee di ab jullit walla muy ñoñ-téere, 2- mu tudd turu Yàlla buy tàmbali rendi gi, 3- jumtukaay gi ñuy rendee nekk lu mana rendi, na ñaw te bu mu nekk bëñ walla aw weh, 4- rendi gi nekk ca bérab ba ñuy rende di ca loje, ci ku ko man mu dagg bóli gi ak put gi ak ñaari sidit yi.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (3/ 138) (2488).
Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1558) (1968).
Yataal gi (2)
تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.
لعبد الله البسام (ص721).