Moom dafa indi ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc doomam ju góor ju ndaw ju lekkagul, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc toogal ko ci poojam, mu saw ci yéreem yi, mu laaj am ndox daal di ko cay wis te raxasu ko.
Jële nañu ci Ummu Xaysin bint Mihsan yal na ko Yàlla dollee gërëm:
Moom dafa indi ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc doomam ju góor ju ndaw ju lekkagul, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc toogal ko ci poojam, mu saw ci yéreem yi, mu laaj am ndox daal di ko cay wis te raxasu ko.
أَنَّهَا أَتَتْ بِابْنٍ لَهَا صَغِيرٍ لَمْ يَأْكُلِ الطَّعَامَ إِلَى رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَأَجْلَسَهُ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِي حَجْرِهِ، فَبَالَ عَلَى ثَوْبِهِ، فَدَعَا بِمَاءٍ، فَنَضَحَهُ وَلَمْ يَغْسِلْهُ.
Ummu Xaysin bint Mihsan yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa indi ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc doomam ju góor ju tàmbaleegul a lekk ñam ngir tuutig atam, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc toogal ko ci poojam, xale bi saw ci yérey Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu sàkku am ndox, daal di koy wis ca kaw yére ya te raxasu ko.
Jikkoy Yonnente yu tedd yi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ak toroxloom gu màgg gi.
Woote ci rafetug nekkaale ak toroxlu ak ñeewant ci zale yi, ak jaŋ xoli mag ñi ci teral seeni xale ak toogal leen leen ci sa pooj, ak yu ni mel.
Sobeg sawu xale bu góor doonte lekkagul ñam ngir bànneex.
Li Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc la ñuy woowe wis, moom nag liir bu ndaw bu góor bi tàmbaleegul a lekk ñam moo ko jagoo, bu dee jigéen nag fàww ñu raxas sawam doonte xale bu ndaw la.
Xaytag xale bu góor buy dunde soowu yaayam fàww ñu raxas ko niki mbooleem sobe yi.
Raxas manul ñàkk lu dolliku ci ndox mi laal ko rekk.
Li jaadu mooy gaaw a laabal bérab bi am sobe; ngir gaaw a laab ci lu bon; ak it ngir bañ ko a fàtte.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 54) (223).
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 238) (287).
Yataal gi (6)
الإلمام بشرح عمدة الأحكام.
لإسماعيل الأنصاري (1/ 42).
تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.
للبسام (ص55).
تنبيه الأفهام شرح عمدة الأحكام.
لابن عثيمين (1/ 68).