Skip to content

"Allaahuma innii as-aluka alhudaa wattuqaa walhafaafa walxinaa".

Jële nañu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax:

"Allaahuma innii as-aluka alhudaa wattuqaa walhafaafa walxinaa".

«اللهُمَّ إِنِّي أَسْأَلُكَ الْهُدَى وَالتُّقَى، وَالْعَفَافَ وَالْغِنَى».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Bokkoon na ci ñaani Yonente bi: yaw Yàlla sama Boroom man maa ngi lay laaj ag njub yoon wu jub ci xam dëgg ak jëfe ko, ak ragal la jëf ndigal yi moytandiku tere yi, ak fegu bàyyi li daganul te rafetul ci wax walla jëf, ak doylu wolif mbindeef yi, ba tax na duma ajowoo jëm ci kenn ku dul sama Boroom mu màgg mi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Teddngay jikkó yii: jub ak ragal Yàlla ak fegu ak doylu, ak ñaaxe ci jikkówoo ko.

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc yoralul boppam njariñ du caagine lor, ak ne ki yor loolu mooy Yàlla mu kawe mi.

Ki yor njariñ ak lor ak gindi mbindeef yi mooy Yàlla dong, du malaaka, du Yonnente, du keneen ku dul ñoom.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2087) (2721).

Yataal gi (10)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 146).

تطريز رياض الصالحين.

لفيصل المبارك (ص68).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (2/ 183).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (1/ 528).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

مجموعة من الباحثين (1/ 104).