"bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg".
Jële nañu ci Miqdaat Doomi Mahdii-karib -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne:
"bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg".
«إِذَا أَحَبَّ الرَّجُلُ أَخَاهُ فَلْيُخْبِرْهُ أَنَّهُ يُحِبُّهُ».
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- day leeral benn ci yiy dëgëral diggante way-gëm ñi, tey tasaare mbëggeel seen biir, te mooy bu kenn bëggee mbokkam mu wax ko ne da koo bëgg.
Ngëneelu mbëggeel gir Yàlla rekk tax, ci lu dul njariñul àdduna.
Sopp gi ñu sopp ñu xibaar ki ñu bëgg ngir Yàlla ci bëgg gi ñi ko bëgg, ngir mbëggeel ga ak miineel ga gën a yokk.
Tasaare mbëggeel ci biir way-gëm ñi day dëgëral mbokkoog mgëm, day wattu mbooloo mi ci taasaaroo ak tàqalikoo.
Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (7/ 444) (5124).
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 199) (2392).
Téere bu mag bi An-nasaa'iy def ci Sunna yi (9/ 87) (9963).
Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (28/ 408) (17171).
Yataal gi (12)
بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.
لسليم الهلالي (1/ 450).
تطريز رياض الصالحين.
لفيصل المبارك (ص258).
رياض الصالحين للنووي.
(ص138) (383).
سلسلة الأحاديث الصحيحة وشيء من فقهها وفوائدها.
للألباني (1/ 777).
فيض القدير شرح الجامع الصغير.
للمناوي (1/ 247).
كنوز رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (6/ 279).