Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll".
Jële nañu ci Ubaadata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla moom dong amul te amul bokkaale, ak ne Muhammat ndawul Yàlla la di ndawam, ak ne Iisaa jaamub Yàlla la di ndawam, di kàddoom gu mu sànni ci Maryama di ag ruu gu bawoo ci moom, ak ne àjjana dëgg la, sawara dëgg la, Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll".
«مَنْ شَهِدَ أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ وَحْدَهُ لَا شَرِيكَ لَهُ، وَأَنَّ مُحَمَّدًا عَبْدُهُ وَرَسُولُهُ، وَأَنَّ عِيسَى عَبْدُ اللهِ وَرَسُولُهُ وَكَلِمَتُهُ أَلْقَاهَا إِلَى مَرْيَمَ وَرُوحٌ مِنْهُ، وَالْجَنَّةُ حَقٌّ، وَالنَّارُ حَقٌّ، أَدْخَلَهُ اللهُ الْجَنَّةَ عَلَى مَا كَانَ مِنَ الْعَمَلِ».
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku wax baati Tawhiid yi te xam maanaam te jëfe lamu làmboo, Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ab jaam la tey ab Yonnent, te nangu ne Iisaa ab jaamu la, tey ab yonnente, Ak ne Yàlla moo ko bind ci "kun" nekkal, mu nekk, ak ne moom ruu la ci ruu yi Yàlla bind, Mu setal yaayam ci li Yahuut yi doon askanale ci moom, Mu gëm ne àjjana dëgg la, sawara dëgg la, gëm ne ñoom ñaar xéewalu Yàlla la ak mbugalam, Ba faatu ca loola; kon mujjam mooy àjjana doonte dafa gàtteñlu ci topp Yàlla, te am ay bàkkaar.
لا إله إلا الله: لا معبود بحق إلا الله.
ألقاها إلى مريم: أرسل بها جبريل إليها فنفخ فيها من روحه بإذن الله عز وجل.
Yàlla mu kawe mi moo bind Hiisaa Ibn Maryama ci baatu (kun) ci lu dul baay.
Boole ne Hisaa ak Muhammat -yal na leen Yàlla dolli jàmm- ay jaami Yàlla lañu ak i ndawam, ñoom ñaari Yonnente lañu te duñu fen, ñaari jaam lañu duñu leen jaamu.
Ngëneelu Tawhiid ak ne day far ay bàkkaar, ak ne mujjug kiy wéetal Yàlla mooy àjjana doonte dafa tàbbi ci yenn bàkkaar yi.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (4/ 165) (3435).
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 57) (28).
Yataal gi (4)
الملخص في شرح كتاب التوحيد.
لصالح الفوزان (ص25).
الجديد في شرح كتاب التوحيد.
لمحمد القرعاوي (ص36).
Cited in books
9 BooksYataal gi (9)
- حصن المسلم من أذكار الكتاب والسنةحصن المسلم«لَا إِلَهَ إِلَّا اللَّهُ
- حصن المسلم من أذكار الكتاب والسنةحصن المسلملَا إِلَهَ إِلَّا اللَّه
- حصن المسلم من أذكار الكتاب والسنةحصن المسلملَا إِلَهَ إِلَّا اللَّهُ
- حصن المسلم من أذكار الكتاب والسنةحصن المسلملَا إِلَهَ إِلَّا اللَّه
- حصن المسلم من أذكار الكتاب والسنةحصن المسلم«لَا إِلَهَ إِلَّا اللَّهُ!»[291].
- حصن المسلم من أذكار الكتاب والسنةحصن المسلملَا إِلَهَ إِلَّا اللَّه
- حصن المسلم من أذكار الكتاب والسنةحصن المسلملَا إِلَهَ إِلَّا اللَّه
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 3«مَنْ شَهِدَ أَنْ لا إلهَ إلَّا الله وَحْدَهُ لاَ شَرِيكَ لَهُ، وَأَنَّ مُحَمَّداً عَبْدُهُ وَرسُولُهُ، وَأَنَّ عِيسَىٰ عَبْدُ الله وَرَسُولُهُ، وَكَلِمَتُهُ أَلْقَاهَا إلىٰ مَرْيَمَ وَرُوحٌ مِنْهُ، وَأنَّ الجَنَّةَ حَقٌّ وَأنَّ النَّارَ حَ
- مادة العقيدة الإسلامية(من شهد أن لا إله إلا الله وحده لا شريك له، وأن محمدًا عبده ورسوله، وأن عيسى عبد الله ورسوله وكلمته ألقاها إلى مريم وروح منه، والجنة حق، والنار حق، أدخله الله الجنة على ما كان من العمل).