"dañu ma a yónni ngir ma mottali jikkó yu tedd yi".
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"dañu ma a yónni ngir ma mottali jikkó yu tedd yi".
«إِنَّمَا بُعِثْتُ لِأُتَمِّمَ مَكَارِمَ الْأَخْلَاقِ».
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamle na ne Yàlla mu màgg mi da ko a yónni ngir mu mottali ngëneel ak jikkó yu rafet yi; ba tax mu yónni Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu mottali li ko jiitu woon ci ay Yonente, ak di mottali jikkóy araab yu rafet ya, ñu nekkoon ñu bëgg yiw te bañ ay, di ñu am kersa ak tabe ak ug njàmbaarte; ñu yónni Yonente bi ngir mu mottali li mànki ca seen jikkó ya, niki seen ug puukarewu ci seen i askan, ak rëy-rëylu ak xeeb aji-ñàkk ak yeneen yu dul yooyu.
Ñaaxe ci teddngay jikkó yi, ak tere safaanam.
Leeral solos jikkó yu rafet yi ci sariihab lislaam ak ne dafa bokk ca ya gën a yey.
Waa ceddo ga amoon nañu desiiti jikkó yu rafet, bokk na ca tabe ak jàmbaare ak yu dul yooyu lislaam ñëw ngir mottali ko.
Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (14/ 512) (8952).
Téere bu mag bi Al-Bayhaqii def ci Sunna yi (10/ 191) (20819).
Yataal gi (2)
Al-Adabul Mufrad (ص104) (273).
عمدة القاري شرح صحيح البخاري (22/ 118).
Cited in books
7 BooksYataal gi (7)
- الحقيقة المُبْهِرَة في العلاقة بين الإسلام والإنسان(إنما بُعثت لأتمِّم مكارم الأخلاق) [14].
- الحقيقة المُبْهِرَة في العلاقة بين الإسلام والإنسان(إنما بعثت لأتمم مكارم الأخلاق).[126]
- كتاب تعليم المسلم الجديد«إِنَّمَا بُعِثْتُ لِأُتَمِّمَ مَكَارِمَ الْأَخْلَاقِ»
- كتاب تعليم المسلم الجديد«إِنَّمَا بُعِثْتُ لِأُتَمِّمَ مَكَارِمَ الْأَخْلَاقِ»
- لماذا الإسلام؟1(إِنَّمَا بُعِثْتُ لِأُتَمِّمَ مكارم الْأَخْلَاقِ)،
- مجموعة زاد الحديث (1)الحديث 1«إِنَّمَا بُعِثْتُ لِأُتَمِّمَ مَكَارِمَ الْأَخْلَاقِ»
- مكارم الأخلاقمكارم الأخلاق «إِنَّمَا بُعِثْتُ لِأُتَمِّمَ مَكَارِمَ الأَخْلَاقِ» [3]؛