Skip to content

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na bëgg ñaan yi làmboo lu bari, daan bàyyi yu dul yooyu.

Jële nañu ci Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na bëgg ñaan yi làmboo lu bari, daan bàyyi yu dul yooyu.

كَانَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَسْتَحِبُّ الْجَوَامِعَ مِنَ الدُّعَاءِ، وَيَدَعُ مَا سِوَى ذَلِكَ.

Abóo Daawuda soloo na ko,ak Ahmat.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa bëggoon ñaan yi làmboo yiwi àdduna ak allaaxira ci ay kàddu yu néew te maanaa mi bari, muy am tagg Yàlla ak jubluwaay yu sell, mu daan bàyyi yu dul yooyu.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Sopp nañu ñaan ci ay kàddu yu néew te làmboo ay maanaay yiw, sib nañu it di diisal ak di jafeel ci ñaan, te dafa wuute ak njubug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Jagleel nañu Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc kàddu yoy day dajale lu bari.

Xér ci ñaan yi sax jóge ci Yonnente bi, donte dafa gudd ay baatam bari, loolu lépp dafa bokk ci ñaan yi matale.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (2/ 605) (1482).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (42/ 76) (25151).

Yataal gi (8)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (2/ 542).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (2/ 1003).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (6/ 15).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (17/ 349).