Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Rabbi ixfir lii, Rabbi ixfir lii».
Jële nañu ci Husayfata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Rabbi ixfir lii, Rabbi ixfir lii».
أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ يَقُولُ بَيْنَ السَّجْدَتَيْنِ: «رَبِّ اغْفِرْ لِي، رَبِّ اغْفِرْ لِي».
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan toog ci diggante ñaari sujjóot yi da daan wax: Rabbi ixfir lii, Rabbi ixfir lii, di ko baamtu. Maanaam Rabbi ixfir lii mooy: jaam bi sàkku ci Boroomam mu faral ko ay bàkkaaram te suturaal ko ay ayibam.
...:
Yoonal nañu ñaan ci diggante ñaari sujjóot yi ci jullig farata ak naafila.
Sopp nañu di baamtu wax jii: Rabbi ixfir lii, benn yoon bi moom dafa war.
Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (2/ 154) (874).
Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (2/ 231) (1145).
Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (2/ 64) (897).
Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (38/ 392) (23375).
Yataal gi (1)
نيل الأوطار (2/ 305).
Cited in books
6 BooksYataal gi (6)
- الذكر والدعاء والعلاج بالرقي من الكتاب والسنة"رب اغفر لي، ربِّ اغفر لي".
- تطبيق القرآن والأذكارأذكار الصلاة((رَبِّ اغْفِرْ لِي، رَبِّ اغْفِرْ لِي))[72].
- حصن المسلم من أذكار الكتاب والسنةحصن المسلم«رَبِّ اغْفِرْ لِي، رَبِّ اغْفِرْ لِي»[72].
- حصن المسلم من أذكار الكتاب والسنةحصن المسلمرَبِّ اغْفِرْ لِي، رَبِّ اغْفِرْ لِي
- رسالة في الأذكار1«رَبِّ اغْفِرْ لِي، رَبِّ اغْفِرْ لِي».
- مجموعة زاد السيرة النبوية (2)1أَنَّ النَّبيَّ صلى الله عليه وسلم كانَ يَلْبَسُ خاتَمَهُ في يَمِينِهِ.