Skip to content

"ku seeti ku feebar, te ab digam ñëwagul, mu wax juróom-ñaari yoon: As-alul Laaha Al-Hasiima Rabba Al-Harsi al-hasiimi an yasfiyaka, lu dul ne Yàlla dana ko may jàmm ca feebar boobu".

Jële nañu ci Ibnu Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne :

"ku seeti ku feebar, te ab digam ñëwagul, mu wax juróom-ñaari yoon: As-alul Laaha Al-Hasiima Rabba Al-Harsi al-hasiimi an yasfiyaka, lu dul ne Yàlla dana ko may jàmm ca feebar boobu".

«مَنْ عَادَ مَرِيضًا، لَمْ يَحْضُرْ أَجَلُهُ فَقَالَ عِنْدَهُ سَبْعَ مِرَارٍ: أَسْأَلُ اللَّهَ الْعَظِيمَ رَبَّ الْعَرْشِ الْعَظِيمِ أَنْ يَشْفِيَكَ، إِلَّا عَافَاهُ اللَّهُ مِنْ ذَلِكَ الْمَرَضِ».

Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne amul benn jullit buy seeti jullit bu feebar te waxtuw deewam jotagul, aji-seeti ji ñaanal aji-feebar ji, ci wax ne: (maa ngi ñaan Yàlla mu màgg mi) ci jëmmam ak i meloom ak i jëfam, (Boroom Aras ju màgg ja mu saafara la), mu baamtu ko juróom-ñaari yoon lu dul ne Yàlla dina ko saafara ca tawat jooja.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Sopp nañu ñaanal aji-feebar ci ñaan gii, ak baamtu ko juróom-ñaari yoon.

Ku ñu ñaanal lii di nga wér bu soobe Yàlla bu dee da ko a def ci dëgg ak sellal.

Bu biralee ñaan gi mbaa mu yalu ko ñaar yépp dagan na, waaye bu fexee ba aji-feebar ji dégg ko loo lu mooy li gën; ndax loo lu da koy bégloo.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (5/ 22) (3106).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (3/ 593) (2083).

Téere bu mag bi An-nasaa'iy def ci Sunna yi (9/ 385) (10820).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (4/ 40) (2137).

Yataal gi (10)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (2/ 163).

تطريز رياض الصالحين.

لفيصل آل مبارك (ص537).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (4/ 483).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (11/ 559).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (1/ 689).