"bu ñu taxawalee julli geneen julli amatul gu dul ga ñu farataal".
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"bu ñu taxawalee julli geneen julli amatul gu dul ga ñu farataal".
«إِذَا أُقِيمَتِ الصَّلَاةُ فَلَا صَلَاةَ إلَّا المَكْتُوبَةُ».
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na ki nekk ci jàkka muy tàmbali jullig naafila ginnaaw ba ñu taxawalee jullig farata gi.
Tere nañu jullig naafila ci jàkka ji bu ñu taxawalee jullig farata.
Tere nañu tàmbali ag naafila ginnaaw ba ñu taxawalee julli, moo xam jullig Raatiba la niki sunnas suba la ak tisbaar walla leneen.
Bu ñi taxawalee julli fekk mu nekk ci naafila; bu dee la ca des moo gën a néew benn rànka kon na ko mottali ci woyofal, lu ko moy na ko dagg ndax mu dab ngëneelu kàbbaru armal gi
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 493) (710).
Yataal gi (1)
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (15/ 246).