Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na ubbee julli gi ci kàbbar, ak jàng, Alhamdu lil-Laahi Rabbil haalamiina
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na ubbee julli gi ci kàbbar, ak jàng, Alhamdu lil-Laahi Rabbil haalamiina, bu daan rukkoo daawul yëkkëti boppam te daawu ko sëgg, waaye da daan nekk ci diggante loolu, bu daan siggi boppam jóge ca rukkoo ba daawul sujjóot ba keroog muu taxaw ba yemoo, bu daan yëkkëti boppam jóge ca sujjóot ba daawul sujjóotaat ba keroog muy toog ba yemoo, daan na jàng taaya ci ñaari ràkka yu ne, da daan lal tànku càmmooñam, samp tànku ndayjooram, daan tere it toogiinu Saytaate, tere na it nit ki di lal ñaari loxoom kem laliinu ndegment, daan na jeexale julli gi ci sëlmël.
كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَسْتَفْتِحُ الصَّلَاةَ بِالتَّكْبِيرِ، وَالقِرَاءَةِ، بِـ الحَمْدُ لِلَّهِ رَبِّ العَالَمِينَ، وَكَانَ إِذَا رَكَعَ لَمْ يُشْخِصْ رَأْسَهُ وَلَمْ يُصَوِّبْهُ، وَلَكِنْ بَيْنَ ذَلِكَ، وَكَانَ إِذَا رَفَعَ رَأْسَهُ مِنَ الرُّكُوعِ لَمْ يَسْجُدْ حَتَّى يَسْتَوِيَ قَائِمًا، وَكَانَ إِذَا رَفَعَ رَأْسَهُ مِنَ السَّجْدَةِ لَمْ يَسْجُدْ حَتَّى يَسْتَوِيَ جَالِسًا، وَكَانَ يَقُولُ فِي كُلِّ رَكْعَتَيْنِ التَّحِيَّةَ، وَكَانَ يَفْرِشُ رِجْلَهُ اليُسْرَى وَيَنْصِبُ رِجْلَهُ اليُمْنَى، وَكَانَ يَنْهَى عَنْ عُقْبَةِ الشَّيْطَانِ، وَيَنْهَى أَنْ يَفْتَرِشَ الرَّجُلُ ذِرَاعَيْهِ افْتِرَاشَ السَّبُعِ، وَكَانَ يَخْتِمُ الصَّلَاةَ بِالتَّسْلِيمِ.
Ndayu jullit ñi Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm tudd na ci jullig Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne da daan ubbee julleem ci kàbbaru armal, daal di wax: "Allaahu Akbaru", mu ubbee njàng mi ci saaru Al-Faatiha: "Alhamdu lil-Laahi Rabbil haalamiina...". Bu daan rukkoo ginnaaw ba mu taxawee, du yëkkëti boppam du ko sëgg it ci jamonoy rukkoo ba, waaye da koy def muy lu yemoo te jub, bu yëkkëtee boppam jóge ca rukkoo ba day taxaw ba jubb laata muy sujjóot, bu yëkkëtee boppam jóge ca sujjóot bu njëkk ba, du sujjóot ñaareelu sujjóot bu ba keroog muy toog ba sax. Daan na toog ci diggante ñaari ràkka yu ne ngir taaya, muy wax: "attahiyaatu lil-Laahi wassalawaatu wattayyibaatu...", bu daan toog ci diggante ñaari sujjóot walla ngir taaya day lal tànku càmmooñam daal di ciy toog, sàmp tànku ndayjooram. Mu tere kiy julli di toog kem toogiinu Saytaate, te loolu mooy mu lal ñaari tànkam ci suuf, daal di toog ci ay testënam, walla mu teg ñaari roogoom ci ci suuf daal di samp ñaari yeelam te ñaari loxoom ci suuf kem ni Xaj di lale ay tànkam, walla mu kiy julli lal ñaari loxoom tàllal ko buy sujjóot kem ni ndegment di tàllale ay tànkam. Daal na tëje julli gi ci sëlmël: "Assalaamu alaykum wa rahmatu Al-Laahi" ci ndayjoor bi benn yoon ak benn yoon ci càmmooñ bi.
Leeral dara ci melow jullig Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Warug kàbbaru armal gi nga xam ne day araamal jépp wax ak jëf ju wuute ak waxi julli gi ak i jëfam, ak ne lu dul wax jii du ko wuutu ngir dugg ci julli gi
Warug jàng Al-Faatiha.
Warug rukkoo, la ca gën nag mooy yemoo, ci lu dul yëkkëtiku, du caagine sëgg.
Warug siggi jóge ca rukkoo ba, ak warug yemoo ca taxaw ga ginnaawam.
Warug sujjóot, ka warug siggi jóge ca sujjóot ba, ak yemoo ca toog ga ginnaawam.
Yoonalees na aji-julli jiblal tànku càmmooñam samp tànku ndayjooram bu tooge ci julli gi, bu dee taaya gi mujj ci julli gi am ñaari taaya niki Timim ak Gee la ñu yoonal mooy Tawarruk(lal tànku càmmooñ bi ci suufu tànku ndayjoor bi teg toogu yi ci suuf), kem ni mu ñëwe ci yeneen hadiis.
Tere nañu niroo ak Saytaane ci toogam, te loolu mooy mu toog ci kaw ay testënam lal ay tànkam ci suuf, walla mu samp leen daal di toog ci seen diggante ci kaw suuf.
Tere nañu niroo ak ndegment ci ni muy lale ay tànkam, te loolu mooy kiy julli tàllal ay loxoom ci kaw suuf, ndax loolu melow tàyyeel la ak lompañ.
Tere nañu niroo ak Saytaane ak bayima yi ci seen i jëf.
Warug tëje julli gi ci sëlmël, te ag ñaan la ñeel way-julli ñi ak ñi teew ak ñu baax ñi fàddu ci mucc ci bépp ay ak mànkite.
Warug dal ci julli gi.
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 357) (498).
Yataal gi (11)
شرح النووي على مسلم (4/ 213).
سبل السلام.
لمحمد الصنعاني (1/ 248 ).
توضيح الأحكام مِن بلوغ المرام.
لعبد الله البسام (2/ 172).
فتح ذي الجلال والإكرام شرح بلوغ المرام.
لابن عثيمين (2/ 51).
تنبيه الأفهام شرح عمدة الأحكام.
لابن عثيمين (2/ 189).
تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.
لعبد الله البسام (ص145).
Cited in books
3 BooksYataal gi (3)
- الصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهمالصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهمكَانَ رَسُولُ اللهِ ﷺ يَسْتَفْتِحُ الصَّلَاةَ بِالتَّكْبِيرِ، وَالْقِرَاءَةِ، بِ ﴿ٱلۡحَمۡدُ لِلَّهِ رَبِّ ٱلۡعَٰلَمِينَ﴾، وَكَانَ إِذَا رَكَعَ لَمْ يُشْخِصْ رَأْسَهُ، وَلَمْ يُصَوِّبْهُ وَلَكِنْ بَيْنَ ذَلِكَ، وَكَانَ إِذَا رَفَعَ رَأْسَهُ
- الصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهم« كَانَ رَسُولُ اللهِ ﷺ يَسْتَفْتِحُ الصَّلَاةَ بِالتَّكْبِيرِ، وَالْقِرَاءَةِ، بِ ﴿ٱلۡحَمۡدُ لِلَّهِ رَبِّ ٱلۡعَٰلَمِينَ﴾، وَكَانَ إِذَا رَكَعَ لَمْ يُشْخِصْ رَأْسَهُ، وَلَمْ يُصَوِّبْهُ وَلَكِنْ بَيْنَ ذَلِكَ، وَكَانَ إِذَا رَفَعَ رَأْسَه
- مجموعة زاد التربية الإسلامية (1)، والسيرة النبوبة (1)، والعقيدة (1)، والفقه (1)مجموعة زاد الفقه (1)«وَكَانَ إِذَا رَفَعَ رَأْسَهُ مِنْ الرُّكُوعِ لَمْ يَسْجُدْ حَتَّى يَسْتَوِيَ قَائِماً».