Skip to content

"bépp téqqu nit sarax la ci moom

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

"bépp téqqu nit sarax la ci moom, bis bu jànt bi fenk mu maandu ci diggante ñaari nit loolu sarax la, ak nga dimbale nit ki ci waruwaayam yéegal ko ca walla nga jottali ko ca ay bagaasam loolu sarax la, wax ju teey sarax la, bépp jéego booy dox jëm ca julli ga loolu sarax la, ak nga randale aw lor ci yoon loolu sarax la ".

«كُلُّ سُلَامَى مِنَ النَّاسِ عَلَيْهِ صَدَقَةٌ، كُلَّ يَوْمٍ تَطْلُعُ فِيهِ الشَّمْسُ تَعْدِلُ بَيْنَ الِاثْنَيْنِ صَدَقَةٌ، وَتُعِينُ الرَّجُلَ فِي دَابَّتِهِ فَتَحْمِلُهُ عَلَيْهَا أَوْ تَرْفَعُ لَهُ عَلَيْهَا مَتَاعَهُ صَدَقَةٌ، وَالكَلِمَةُ الطَّيِّبَةُ صَدَقَةٌ، وَكُلُّ خُطْوَةٍ تَمْشِيهَا إِلَى الصَّلَاةِ صَدَقَةٌ، وَتُمِيطُ الأَذَى عَنِ الطَّرِيقِ صَدَقَةٌ».

Al-Buxaarii ak muslim ñoo ko soloo
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne saraxu coobarewu ngir Yàlla mu kawe mi war na ci bépp mukallaf ci bis bu ne ci limub fi ay yaxam dajee ci anamug sant ko ci jàmm ji, ak li mu def ay yaxam mu man koo bank man koo tàllal, Te sarax boobu day ame ci jëf yu baax yépp waaye yemul ci joxe alal, te bokk na ca: Sag màndu ak sag yéwénal ci diggante ñaari way-xuloo yi sarax la, Ak nga dimbali ki néew doole ci daabaam nga yéegal ko ca, walla nga yëkkatil ko ay jumtukaayam sarax la, Ak wax ju teey ci tudd Yàlla ak ñaan ak nuyóo ak yeneen sarax la, Ak bépp jéego boo dox jëm ca julli ga sarax la, Ak dindi luy lore ci yoon wi sarax la.

Maanaay baat yi

سُلامى: بضم السين المهملة وتخفيف اللام مع القصر، وهي المفاصل، وقد ثبت في صحيح مسلم أنها ثلاثمائة وستون:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ni ñu toggale yaxi doomu Aadama ak ni mu mucce ayib bokk na ci xéewali Yàlla yi gën a màgg ci moom, ba tax bépp yax aajowoo saraxe ñeel ko ngir cantug xéewal gi mat.

Xemmemloo ci yeesal cant gi ci bis bu ne ngir li xéewal googu sax.

Xemmemloo ci sax ci naafila yi ak saraxe yi bis bu nekk.

Ngëneelu yéwénal ci diggante nit ñi.

Ñaaxe ci nit ki di dimbali mbokkam; ndax dimbali gi mu koy dimbali sarax la.

Soñee ci teewe mbooloo ya ak dox jëm ca, ak dundal jàkka ya ci loolu.

Warug wormaal yooni jullit ñi ci moytu lu leen di lor mbaa mu leen di gaañ.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (4/ 56) (2989).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 498) (720).

Yataal gi (17)

التحفة الربانية في شرح الأربعين حديثًا النووية.

مطبعة دار نشر الثقافة.

الإسكندرية.

الطبعة: الأولى.

1380 هـ.

شرح الأربعين النووية.

للشيخ ابن عثيمين.

دار الثريا للنشر.

فتح القوي المتين في شرح الأربعين وتتمة الخمسين.

دار ابن القيم.

الدمام المملكة العربية السعودية.

الطبعة: الأولى.

1424هـ/2003م.

الفوائد المستنبطة من الأربعين النووية.

للشيخ عبد الرحمن البراك.

دار التوحيد للنشر.

الرياض.