Skip to content

"waaw lu jot aw nit ba bu ñuy julli di xool kaw asamaan", waxam ji tar lool ci loolu, ba mujj mu ne: "danañu bàyyi loolu walla dees na këf seen gis ga".

Jële nañu ci Anas ibn Maalik yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

"waaw lu jot aw nit ba bu ñuy julli di xool kaw asamaan", waxam ji tar lool ci loolu, ba mujj mu ne: "danañu bàyyi loolu walla dees na këf seen gis ga".

«مَا بَالُ أَقْوَامٍ يَرْفَعُونَ أَبْصَارَهُمْ إِلَى السَّمَاءِ فِي صَلاَتِهِمْ»، فَاشْتَدَّ قَوْلُهُ فِي ذَلِكَ، حَتَّى قَالَ: «لَيَنْتَهُنَّ عَنْ ذَلِكَ أَوْ لَتُخْطَفَنَّ أَبْصَارُهُمْ».

Al-buxaariy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day artu ñiy yëkkëti seenug gis jëme ca asamaan sa bu ñu dee julli bay ñaan walla leneen, ag artoom ak ug xuppaateem tar lool ci ñiy def loolu ci ne ragal na ñu këf seen gis ya jël ko ci lu gaaw, ba duñu yëg lu dul rekk ne ñàkk nañu xéewalug gis.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Rafetug wooteg Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak ni muy leerale dëgg; ak ne moom Yonente bi feeñalul ñi def njuumte li; ndaxte jubluwaay bi mooy leeral dëgg gi kese te loo lu amna; ak it suturaal ki juum te loolu mooy gën a tax mu nangu ko.

Tere gu feddaliku, ak tëkku gu tar ci kaw ñiy yëkkëti seenug gis jëme ca asamaan sa bu ñu dee julli.

Wax na ca Hawnul Mahbuud ne: li waral loolu mooy ne bu yëkkëtee gisam jëme asamaan day génn ci melow jublu Xibla dummóoyu ko, day génn it ci melow julli.

Yëkkëti gis gi day wuute ak ragal ak toxoxlu ci biir julli gi.

Julli lu màgg ay mbir la, niki noonu di na war ci kiy julli mu nekk ci julli gi ak teggin yu mat sëkk ci Yàlla mu màgg mi.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 150) (750).

Yataal gi (8)

كشاف القناع عن متن الإقناع.

لمنصور بن يونس البهوتي (2/ 404).

توضيح الأحكام شرح بلوغ المرام.

لعبد الله البسام (2/ 101).

فتح ذي الجلال والإكرام شرح بلوغ المرام.

لابن عثيمين (1/ 587).

منار القاري شرح مختصر صحيح البخاري.

لحمزة قاسم (2/ 159).