Skip to content

«ki gën a mat ug ngëm ci jullit ñi mooy ki ci gën a rafet jikko, te ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam».

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yònente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

«ki gën a mat ug ngëm ci jullit ñi mooy ki ci gën a rafet jikko, te ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam».

«أَكْمَلُ الْمُؤْمِنِينَ إِيمَانًا أَحْسَنُهُمْ خُلُقًا، وَخَيْرُكُمْ خَيْرُكُمْ لِنِسَائِهِمْ».

Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat.
Tane na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne nit ki gën a mat ngëm ci nit ñi mooy ki gën a rafet jikko, ci béllil xar kanam, ak def njekk, ak rafet i wax, ak jeñ lor. Ak ne ki gën ci way-gëm yi mooy ki gën ci ay jigéenam, niki ay jabaram ak i doomam yu jigéen, ak i mbokkam ak ay jegeñaaleem yu jigéen; ndax ñoom ñoo gën a yayoo ci nit ñi jikko ju rafet.

Maanaay baat yi

....:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ngëneelu jikko ju rafet ak ne ci ngëm la bokk.

Jëf ci ngëm Yàlla la bokk, day yokku di wàññeeku.

Lislaam daa teral jigéen tey soññee ci rafetal jëme ci moom.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (7/ 70) (4682).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (2/ 454) (1162).

Yataal gi (9)

مسند أحمد ط الرسالة (12/ 364) (7402).

سلسلة الأحاديث الصحيحة وشيء من فقهها وفوائدها.

للألباني (1/ 573).

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 362).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (3/ 130).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (5/ 234).