Skip to content

«jaamu Yàlla ci jamonoy fitna moo ngi mel ni gàddaay jëm ci ma».

Jële nañu ci Mahxal ibn Yasaar yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

«jaamu Yàlla ci jamonoy fitna moo ngi mel ni gàddaay jëm ci ma».

«الْعِبَادَةُ فِي الْهَرْجِ كَهِجْرَةٍ إِلَيَّ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamal na jaam ñi ngir ñuy jëm ci jaamu Yàlla jamonoy fitna ak ray ak jaxasoog mbiri nit ñi ak ne loolu ag fayam mi ngi mel ni gàddaay jëm ci Yonente bi, loolu nag ndaxte nit ñi dañu koy sàggane, te kenn du ci taxaw ku dul ay benn-been.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ñaaxe ci jaamu ak dëgmal Yàlla jamonoy fitna; ngir aaru ci fitna si, ak mucc ci yàqute gi.

Leeral ngëneelu jaamu Yàlla ci fitna ak waxtuy càggante yi.

Jaadu na ci jullit bi mu beru barabi fitna yi ak càggante yi.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2268) (2948).

Yataal gi (4)

كشف المشكل من حديث الصحيحين (2/ 42).

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (45/ 5).

بهجة الناظرين (2/ 455).

نزهة المتقين (ص942).