Skip to content

ndax du ma la yabal ca la ma Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yabaloon? Bul bàyyi benn xërëm te tojoo ko, mbaa benn bàmmeel bu ñuy màggal te maasale woo ko.

Jële na ñu ci Abul Hiyyaaj Al-Asadi mu wax ne:

Aliyun Ibn Abii Taalib da ne ma: ndax du ma la yabal ca la ma Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yabaloon? Bul bàyyi benn xërëm te tojoo ko, mbaa benn bàmmeel bu ñuy màggal te maasale woo ko.

قَالَ لِي ‌عَلِيُّ بْنُ أَبِي طَالِبٍ: أَلَا أَبْعَثُكَ عَلَى مَا بَعَثَنِي عَلَيْهِ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ؟ أَنْ لَا تَدَعَ تِمْثَالًا إِلَّا طَمَسْتَهُ، وَلَا قَبْرًا مُشْرِفًا إِلَّا سَوَّيْتَهُ.

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na yónni Sahaaba yi ci ñu bañ a bayyi benn «xërëm» -te mooy nataalu lu am ruu moo xam dafa am jëmm walla amul jëmm- lu dul ne dindi nañu ko mbaa ñu far ko. Ak ñu bañ a bàyyi bàmmeel bu ñu yëkkati lu dul ne maasale nañu ko ak suuf si, màbb la ñu ca tabax, mbaa ñu jégénal ko mu bañ a sute suuf si lu bari, waaye dañu koy yëkkati luy tollook Sibr rekk.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Araamug nataal lu am ag ruu; ndax daa bokk ci jumtukaayi bokkaale yi.

Yoonalees na dindi lu bon ci loxo ci ku am nguur, mbaa mu man loolu.

Xérug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci dindi lépp luy wane jeexitalu ceddo, ci ay nataal ak i xërëm ak tabax ci bàmmeel yi.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (2/ 666) (969).

Yataal gi (8)

القول المفيد على كتاب التوحيد.

لابن عثيمين (2/ 446).

الملخص في شرح كتاب التوحيد.

لصالح الفوزان (ص402).

الجديد في شرح كتاب التوحيد.

لمحمد القرعاوي (ص447).

كتاب التوحيد.

للإمام محمد بن عبد الوهاب (ص138).