Skip to content

"Solleen seen yére yu weex yi, ndax moo gën ci seen yére yi, te nangeen ci sàng seen way-faatu yi".

Jële nañu ci Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

"Solleen seen yére yu weex yi, ndax moo gën ci seen yére yi, te nangeen ci sàng seen way-faatu yi".

«البَسُوا مِنْ ثِيَابِكُمُ البَيَاضَ، فَإِنَّهَا مِنْ خَيْرِ ثِيَابِكُمْ، وَكَفِّنُوا فِيهَا مَوْتَاكُمْ».

Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day dénk góor ñi ñuy sol yére yu weex yi ak di ci sàng seen néew yi; ndax dafa bokk ci yére yi gën.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Sopp nañu sol yére yu weex, dagan na it sol weneen melo wu dul moom.

Sopp nañu sànge néew yi ci lu weex.

Sawkaanii nee na: hadiis bi day tegtale ne yoonalees na sol lu weex ak sànge ko néew yi; ak ne moo gën a sell gën a teey bu dul moom, bu dee li mu gën a teey moom lu bér la, bu dee li mu gën a laab nag ndaxte lu ci dal rekk day feeñ moo tax ñu taamu ko.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (6/ 27) (3878).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (2/ 311) (994).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (2/ 453) (1472).

Yataal gi (1)

ذخيرة العقبى في شرح المجتبى (19/ 16).