«misaalu toogandoo bu sell ak toogandoo bu bon moo ngi mel ni ki yor gëttug Misk ak kiy upp ab furne,
Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-hasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«misaalu toogandoo bu sell ak toogandoo bu bon moo ngi mel ni ki yor gëttug Misk ak kiy upp ab furne, ki yor gëttug Misk gi: benn mu mayla ci, walla nga jënd ci, mbaa nga am fi moom xet gu neex, kiy upp ab furne nag moom: benn mu lakk say yére, walla nga jële fa xet gu bon».
«إِنَّمَا مَثَلُ الْجَلِيسِ الصَّالِحِ وَالْجَلِيسِ السَّوْءِ كَحَامِلِ الْمِسْكِ وَنَافِخِ الْكِيرِ، فَحَامِلُ الْمِسْكِ: إِمَّا أَنْ يُحْذِيَكَ، وَإِمَّا أَنْ تَبْتَاعَ مِنْهُ، وَإِمَّا أَنْ تَجِدَ مِنْهُ رِيحًا طَيِّبَةً، وَنَافِخُ الْكِيرِ: إِمَّا أَنْ يُحْرِقَ ثِيَابَكَ، وَإِمَّا أَنْ تَجِدَ رِيحًا خَبِيثَةً».
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa joxe misaal ci ñaari xeeti nit: Bi ci njëkk: toogandoo ak àndandoo bu sell buy tegtale Yàlla ak lu ngëremam nekk, di dimbalee ci topp Yàlla, Moom de day mel ni jaaykatu Misk, benn mu joxla ca, walla nga jënd ca, mbaa nga xeeñcu fa xet gu teey te neex. Ñaareel bi: toogandoo ak àndandoo bu bon; kiy teree topp Yàlla, tey dimbalee ci ay moy, ngay gis ci moom ay jëf yu bon, ñu lay ŋàññ ndax li ngay ànd ak di toog ak ku mel ni moom. Misaalam moo ngi mel ni tëggkat biy upp sawara; benn mu lakk say yére ci sawara wiy naaw, walla nga jële fa ci jege gi nga ko jege ag xet gu bon.
Sadd ay misaal ngir jegele maanaa mi ci kiy dégg lu dagan la.
Ñaaxe ak xemmemloo ci ñuy toogandoo ak toppkatu Yàlla yu yiw yi, te moytu yàqkat yi boroom jikkó yu ñaaw yi.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (7/ 96) (5534).
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2026) (2628).
Yataal gi (5)
بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.
لسليم الهلالي (1/ 431).
نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.
مجموعة من الباحثين (1/ 339).
شرح النووي على مسلم (16/ 178).
Cited in books
4 BooksYataal gi (4)
- الحقيقة المُبْهِرَة في العلاقة بين الإسلام والإنسان(إنما مثل الجليس الصالح، والجليس السوء؛ كحامل المسك، ونافخ الكير، فحامل المسك؛ إما أن يحذيك، وإما أن تبتاع منه، وإما أن تجد منه ريحاً طيبة، ونافخ الكير إما أن يحرق ثيابك، وإما أن تجد ريحاً خبيثة)[134].
- المناهج التعليمية - الصف السادسالمناهج الدراسية - الحديث - الصف السادس - الفصل الثاني«إِنَّمَا مَثَلُ الْجَلِيسِ الصَّالِحِ وَالْجَلِيسِ السُّوءِ كَحَامِلِ الْمِسْكِ وَنَافِخِ الْكِيرِ؛ فَحَامِلُ الْمِسْكِ إِمَّا أَنْ يُحْذِيَكَ، وَإِمَّا أَنْ تَجِدَ مِنْهُ رِيحًا طَيِّبَةً، وَنَافِخُ الْكِيرِ إِمَّا أَنْ يُحْرِقَ ثِيَابَكَ
- مشروع المنهج التعليميمادة الحديث مستوى 1«مَثَلُ الجَلِيسِ الصَّالِحِ وَالسَّوْءِ، كَحَامِلِ المِسْكِ وَنَافِخِ الكِيرِ، فَحَامِلُ المِسْكِ: إِمَّا أَنْ يُحْذِيَكَ، وَإِمَّا أَنْ تَبْتَاعَ مِنْهُ، وَإِمَّا أَنْ تَجِدَ مِنْهُ رِيحًا طَيِّبَةً، وَنَافِخُ الكِيرِ: إِمَّا أَنْ يُحْرِق
- مكارم الأخلاقمكارم الأخلاق «مَثَلُ الْجَلِيسِ الصَّالِحِ وَالجَلِيسِ السُّوءِ كَحَامِلِ المِسْكِ وَنَافِخِ الكِيرِ، فَحَامِلُ المِسْكِ إِمَّا أَنْ يُحْذِيَكَ، وَإِمَّا أَنْ تَبْتَاعَ مِنْهُ، وَإِمَّا أَنْ تَجِدَ مِنْهُ رِيحًا طَيِّبَةً، وَنَافِخُ الكِيرِ إِمَّا أَنْ