"lan laa séq ak àdduna, nekkuma ci àdduna lu dul aji-romb jiy kerlu ci ronu ag garab topp mu dem ba ko fa".
Jële nañu ci Abdullah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa nelaw ci ag basaŋ, mu jug mu jeexital ci wetam gi, nu ne ko: yaw Yonente Yàlla bi, tee nu laa wutal lalttaay gu nooy, mu wax ne:
"lan laa séq ak àdduna, nekkuma ci àdduna lu dul aji-romb jiy kerlu ci ronu ag garab topp mu dem ba ko fa".
«مَا لِي وَلِلدُّنْيَا، مَا أَنَا فِي الدُّنْيَا إِلاَّ كَرَاكِبٍ اسْتَظَلَّ تَحْتَ شَجَرَةٍ ثُمَّ رَاحَ وَتَرَكَهَا».
Abdullah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day nettali ne Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa nelaw ci ag basaŋ gu ndaw gu ñu ràbbe gàncax, mu jug basaŋ gi jeexital ci wetam gi, nu ne ko: Yaw Yonente Yàlla bi, bu nu la wutaloon ag lal gu nooy mooy gën ngay tëdd ci basaŋ gu ñagas gii, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di ne: Amuma mbëgeel ak cofeel ci àdduna gii ba koy xemmeem, ndax sama misaal ci nekk ci àdduna nekkul lu dul niki aji-war jiy kerlu ci ronu ag garab topp mu dem ba ko fa.
Leeral li Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nekkoon ci dëddu àdduna ak dummóoyu ko.
Bàyyi li manut a ñàkk nekkul ci hadiis bi, waaye li ci nekk mooy bañ ko a soxlawoo ko wolif allaaxira, ndax nit ki dafa kerlu ci garab gu jariñu ca ngir la mu ca egg, waaye jengul rekk jëm ca.
Waaru ci melow Yonente bi ndax mooy royukaay bu rafet bi, ak ne ku topp jeexitalam kooku jub na, te it texe na ci àdduna ak allaaxira.
Xérug sahaaba yi ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak bëgg gi ñu ko bëgg.
Yoonalees na sadd ay misaal ci woote ak jàngale.
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 166) (2377).
Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (5/ 229) (4109).
Yataal gi (4)
النهاية في غريب الحديث والأثر (979).
فيض القدير (5/ 464).
تطريز رياض الصالحين (ص: 326).
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (34/ 663).