" yéen nit ñi, moytandikulen ëppal ci diine, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy ëppal ci diine".
Jële na ñu ci Ibn Abbaas-yal na leen Yàlla dollee gërëm-mu wax ne:
Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ci subag sànni jamra fekk moo ngi ci kaw giléemam gi: "foral ma ay xeer" ma foral ko juróom-ñaari xeer yu sew, muy xeer yi muy sànni, mu tàmbali de leen sànni ci loxoom,di wax naan: "sànnileen yu mel nii" daal di wax ne: " yéen nit ñi, moytandikulen ëppal ci diine, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy ëppal ci diine".
قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ غَدَاةَ الْعَقَبَةِ وَهُوَ عَلَى نَاقَتِهِ: «الْقُطْ لِي حَصًى» فَلَقَطْتُ لَهُ سَبْعَ حَصَيَاتٍ، هُنَّ حَصَى الْخَذْفِ، فَجَعَلَ يَنْفُضُهُنَّ فِي كَفِّهِ وَيَقُولُ: «أَمْثَالَ هَؤُلَاءِ فَارْمُوا» ثُمَّ قَالَ: «أَيُّهَا النَّاسُ، إِيَّاكُمْ وَالْغُلُوَّ فِي الدِّينِ، فَإِنَّما أَهْلَكَ مَنْ كَانَ قَبْلَكُمْ الْغُلُوُّ فِي الدِّينِ».
Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne nekkoon na ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bisub tabaski ci subag sànni jamratu Haqaba yi ci ajug tàggatoo ga, Mu digal ko mu foral ko ay xeeri jamra, mu foral ko juróom-ñaari xeer yu sew, benn bi toll ni doomi Himmas walla bundux, Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-teg ko ci loxoom di ko yëngal, daal di wax ne: Yu toll ni yooyu ci jëmm ngeen sànni sànni ko, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal moytondikuloo ëppal ak taral ak jéggi dayo ci biri diine, ndax li alag xeet ya jiitu woon mooy jéggi dayo ak ëppal ak taral ci diine.
...:
Tere nañu ëppal ci diine, leeral it mujjam gu ñaaw, ak ne sabab la ci alkande.
Waaru ci xeet yi jiitu ngir moytoo tàbbi ca seen njuumte ya.
Soññee ci roy ci sunna.
Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (5/ 268)(3057).
Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (4/ 228) (3029).
Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (5/ 298) (3248).
Yataal gi (4)
الملخص في شرح كتاب التوحيد.
لصالح الفوزان (ص165).
الجديد في شرح كتاب التوحيد.
لمحمد القرعاوي (ص179).
Cited in books
6 BooksYataal gi (6)
- التحذير من البدعالتحذير من البدع «إِيَّاكُمْ وَالْغُلُوَّ فِي الدِّينِ فَإِنَّمَا أَهْلَكَ مَنْ كَانَ قَبْلَكُمُ الْغُلُوُّ فِي الدِّينِ»[(6)].
- حراسة التوحيدالتحذير من البدع«إِيَّاكُم وَالغُلُوُّ فِي الدِّينِ، فَإِنَّمَا أَهْلَكَ مَن كَانَ قَبْلَكُم الغُلُوَّ فِي الدِّينِ».
- عقيدة الأئمة الأربعة«إِيَّاكُمْ وَالْغُلُوَّ، فَإِنَّمَا أَهْلَكَ مَنْ كَانَ قَبْلَكُمْ الْغُلُوُّ»
- عقيدة التوحيد(إياكم والغُلُوَّ، فإنما أهلك من كان قبلكم الغُلُوُّ)
- مجموعة زاد التربية الإسلامية (1)، والسيرة النبوبة (1)، والعقيدة (1)، والفقه (1)العقيدة (1)«يا أَيُّها النَّاسُ، إيَّاكُمْ والغُلوَّ في الدِّينِ؛ فَإنَّهُ أَهْلَكَ مَنْ كان قَبْلَكُمْ الغُلوُّ في الدِّينِ».
- نبراس طالب (4)1«إِيَّاكُمْ وَالْغُلُوَّ فِي الدِّينِ؛ فَإِنَّمَا أَهْلَكَ مَنْ كَانَ قَبْلَكُمُ الْغُلُوُّ فِي الدِّينِ»