Skip to content

"ku amul kóolute amul ag ngëm, ku amul kóllare amul ag ngëm".

Jële nañu ci Anas ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daawu nu xutba lu dul ne dana wax:

"ku amul kóolute amul ag ngëm, ku amul kóllare amul ag ngëm".

«لَا إِيمَانَ لِمَنْ لَا أَمَانَةَ لَهُ، وَلَا دِينَ لِمَنْ لَا عَهْدَ لَهُ».

Ahmat soloo na ko.
Dafa rafet ngir weneen wu dul moom
Leeral gi

Anas ibn Maalik yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne néew na lu Yonente bi di xutba walla muy waare lu dul ne dana tudd ñaari mbir: Bi ci njëkk: ngëm gu mat nekkul ci ki wor nekk ci bakkanam jëm ci keneen ci alalam walla ci bakkanam walla ci njabootam. Ñaareel bi: diine ju mat nekkul ci kiy wor kóllare di ko fecci.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ñaaxe ci joxe kóolute ak matal kóllare, ndax fecci leen day wàññi ngëm.

Moytandikuloo wor kóolute, ak fecci kóllare, ak ne loolu ci bàkkaar yu mag yi la bokk.

Hadiis bi dafa làmboo sàmmonte ak kóolute ak kóllare gi dox ci diggante Yàlla ak jaamam bi, ak gi dox ci diggante mbindeef yi.

Dellluwaay yi

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (19/ 375) (12383).

Yataal gi (1)

فيض القدير (6/ 381).