Skip to content

"ki jekku Alxuraan man ko dana ànd ak ndaw yu tedd yu baax ya, kiy jàng Alxuraan di ko ijjantu sonn ci, kooku amna ñaari fay".

Jële nañu ci Aysa yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

"ki jekku Alxuraan man ko dana ànd ak ndaw yu tedd yu baax ya, kiy jàng Alxuraan di ko ijjantu sonn ci, kooku amna ñaari fay".

«الْمَاهِرُ بِالْقُرْآنِ مَعَ السَّفَرَةِ الْكِرَامِ الْبَرَرَةِ، وَالَّذِي يَقْرَأُ الْقُرْآنَ وَيَتَتَعْتَعُ فِيهِ، وَهُوَ عَلَيْهِ شَاقٌّ، لَهُ أَجْرَانِ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa xamle ne kiy jàng Alxuraan di ku mokkal lool jekku ko, kooku yiwam ca allaaxira mooy mu am wàccuwaay ànd ak Malaaka yi nga xam ne ay ndaw yu tedd lañu te baax, kiy jàng Alxuraan nag di ko ijjantu di dengi-dengi ci njàng mi; ngir néew dooleg mokkalam ànd ak loolu mu kóllarente ak moom, te mu tar ci moom lool, mu am ci coono kooku amna ñaari yool; yoolu njàng mi ak yoolu coono bi ak dengi-dengi gi ci njàng mi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ñaaxe ci mokkal Alxuraan ak xereñe ko ak di ko jàng lu bari ngir am fay ak yool, ak leeral kaweg wàccuwaayu ki def loolu.

Al-Xaadii nee na: maanaam nekkul ne ki koy jàng di ko ijjantu moo gën a barile fay ki ko man, waaye ki ko man moo gën te moo ëppale ag fay; ndax moom Ndawi Malaaka yi lay àndal te dana am fay gu bari, te wàccuwaay bii tuddu ko ci keneen, kon ku sonnewul Téere Yàlla bi kem ni mu ci sonne ba man ko mokkal ko ak xereñe ko ak di ko jàng lu bari ak xam ko naka la koy dabe?

Ibn Baas nee na: kiy jàng Alxuraan te jekku ko, te man njàng mi, mokkal ko lool kooku moom ak Ndaw yu Tedd yu Baax ya lay àndal, maanaam: bu ko dee topp ci wax ak jëf, waaye nekkul liir kase, da koy man a jàng, di ko jëfe, day taxaw ci baat yi ak ci maanaa mi.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (6/ 166) (4937).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 549) (798).

Yataal gi (16)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (2/ 226).

تحفة الأحوذي بشرح جامع الترمذي.

لمحمد المباركفوري (8/ 174).

تطريز رياض الصالحين.

لفيصل آل مبارك (ص580).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (4/ 639).

شرح كتاب التوحيد من صحيح البخاري.

لعبدالله الغنيمان (2/ 592).

فتح الباري بشرح صحيح البخاري.

لابن حجر العسقلاني (9/ 127).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (12/ 562).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمصطفى الخِن وغيره (1/ 740).