" jaam bi dana julli julli ga, te deesu ko ca bindal lu dul fukkeelu xaaj ba, juróom-ñenteel ba, juróom-ñatteel ba, juróom-ñaareel ba, juróom-benneel ba, juróomeel ba, ñenteel ba, ñatteel ba, genn wall ga".
Jële nañu ci Abdulla ibn Hanamata, mu wax ne:
Gis naa Ammaar ibn Yaasir mu dugg ci jàkka ji daal di julli woyofal julli gi, nee na: ba mu génnee, ma jug dem ci moom, ne ko: yaw Abaa Al-Yaqsaan, woyofal nga de, mu ne ma: ndax dangaa gis ma wàññi ci ay dayoom dara?! Ma ne ko: déedéet, mu ne ma: damaa gaawantu di njëkkante ak yàqi saytaane, dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax naan: " jaam bi dana julli julli ga, te deesu ko ca bindal lu dul fukkeelu xaaj ba, juróom-ñenteel ba, juróom-ñatteel ba, juróom-ñaareel ba, juróom-benneel ba, juróomeel ba, ñenteel ba, ñatteel ba, genn wall ga".
رَأَيْتُ عَمَّارَ بْنَ يَاسِرٍ دَخَلَ المَسْجِدَ فَصَلَّى، فَأَخَفَّ الصَّلَاةَ، قَالَ: فَلَمَّا خَرَجَ، قُمْتُ إِلَيْهِ، فَقُلْتُ: يَا أَبَا اليَقْظَانِ، لَقَدْ خَفَّفْتَ، قَالَ: فَهَلْ رَأَيْتَنِي انْتَقَصْتُ مِنْ حُدُودِهَا شَيْئًا؟! قُلْتُ: لَا، قَالَ: فَإِنِّي بَادَرْتُ بِهَا سَهْوَةَ الشَّيْطَانِ، سَمِعْتُ رَسُولَ اللهِ صلى الله عليه وسلم يَقُولُ: « إِنَّ الْعَبْدَ لَيُصَلِّي الصَّلَاةَ، مَا يُكْتَبُ لَهُ مِنْهَا إِلَّا عُشْرُهَا، تُسْعُهَا، ثُمُنُهَا، سُبُعُهَا، سُدُسُهَا، خُمُسُهَا، رُبُعُهَا، ثُلُثُهَا نِصْفُهَا».
Ammaar ibn Yaasir yal na leen Yàlla dollee gërëm dafa dugg ci jàkka ji di julli naafila, julleem gi nekk lu woyof, ba génnee ca jàkka ja, Abdulla ibn Hanamata topp ko, ne ko: yaw Abaa Al-Yaqsaan, gis naa la nga woyofal sa julli gi! Ammaar ne ko: ndax danga maa gis ma wàññi ci ay ponkam ak walla yu war yi, walla ay sàrtam dara?! Mu ne ko: déedéet, mu ne ko: man dama ko a woyofal njëkk saytaane di ma soxlaal. Dégg naa Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: jaam bi dana julli julli ga, te deesu ko ca bindal ca yiw wa lu dul fukkeel ba, walla juróom-ñenteel ba, walla juróom-ñatteel ba, walla juróom-ñaareel ba, walla juróom-beneel ba, walla juróomeel ba, walla ñenteel ba, walla ñenteel ba, walla genn wall ga.
Xérug mag ña ci laabirante ci seen diggante.
Leerlu ak laaj laata ngay weddi.
Doyloo waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci tontu laaj bi ak lënt-lënt bi.
Wàññeekug patu julli gi moo ngi ci wàñeekug toroxlu gi ak settantal gi.
Soññee gu feddaliku ak ñaaxe gu tar ci toroxlu ci julli gi ak teewal xol bi ci Yàlla mu kawe mi.
Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (2/ 97) (796).
Yataal gi (4)
عون المعبود (3/3).
شرح سنن أبي داود للعباد (103/ 15).
فيض القدير (2/ 334).
التيسير بشرح الجامع الصغير (1/ 283).
Cited in books
3 BooksYataal gi (3)
- خطب تعظيم قدر الصلاة" إِنَّ الْعَبْدَ لَيُصَلِّي الصَّلَاةَ مَا يُكْتَبُ لَهُ مِنهَا إِلَّا عُشْرُهَا، تُسْعُهَا، ثُمُنهَا، سُبعُهَا، سُدُسُهَا، خُمُسُهَا، رُبعُهَا، ثلُثهَا نِصْفُهَا "
- خطب تعظيم قدر الصلاة" إِنَّ الْعَبْدَ لَيُصَلِّي الصَّلَاةَ مَا يُكْتَبُ لَهُ مِنْهَا إِلَّا عُشْرُهَا، تُسْعُهَا، ثُمُنُهَا، سُبُعُهَا، سُدُسُهَا، خُمُسُهَا، رُبُعُهَا، ثُلُثُهَا نِصْفُهَا "
- متن اصول الإيمانمتن أصول الإيمان{سمعت رسول اللَّه -صلى الله عليه وسلم- يقول: