«bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla».
Jële nañu ci Abdullah ibn Busrin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: jenn waay dafa wax ne: yaw Yonnente Yàlla bi tërëliini lislaam yi dafa bari ci man, xibaar ma lol dinaa ci jàpp, mu ne ko:
«bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla».
«لاَ يَزَالُ لِسَانُكَ رَطْبًا مِنْ ذِكْرِ اللَّهِ».
Jenn waay dafa jàmbat Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci ne naafila yi dafa bari ci moom ba tax mu lott ci ngir néew kàttanam, mu laaj Yonnente bi ngir mu tegtal ko jëf ju néew juy indi yool yu bari ngir mu jàpp ci. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tektal ko ci muy Sax di tooyal làmmiñam ci tudd Yàlla ci bépp jamono ak ci gépp anam; ci sàbbaal ak sant ak jéggalu ak ñaan ak yu ko niru.
Ngëneelu saxoo tudd Yàlla mu kawe mi.
Bokk na ci màggug ngëneelu Yàlla mu yombal sababi yiw yi.
Gënlaanteg jaam ñi mingi ci seen cér yi ci bunti mbaax yi ak yiw yi.
Baril tudd Yàlla ci làmmiñ di sàbbaal ak di sant ak sikar ak di kàbbar ak yu dul yooyu, ànd ak mu dëppoo ak xol bi day taxaw taxawaayu ay naafila yu bari ci jaamu yi.
Sàmmonteek Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñeel aji-laaj ji ci tontu laaj bu nekk ca la méngoo ak moom.
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (5/ 388) (3375).
Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (4/ 707) (3793).
Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (29/ 226) (17680).
Yataal gi (8)
جامع العلوم والحكم في شرح خمسين حديثا من جوامع الكلم.
لابن رجب الحنبلي (2/ 510).
التحفة الربانية في شرح الأربعين حديثًا النووية.
لإسماعيل الأنصاري (ص104).
فتح القوي المتين في شرح الأربعين وتتمة الخمسين.
للنووي وابن رجب (ص154).
الأحاديث الأربعون النووية وعليها الشرح الموجز المفيد.
لعبد الله بن صالح المحسن (ص93).
Cited in books
4 BooksYataal gi (4)
- الذكر والدعاء والعلاج بالرقي من الكتاب والسنةيا رسول الله إن شرائع الإسلام قد كثرت عليَّ فأخبرني بشيءٍ أتشبث به. قال: "لا يزال لسانك رطباً من ذكر الله".
- حصن المسلم من أذكار الكتاب والسنةحصن المسلم«لَا يَزَالُ لِسَانُكَ رَطْبًا مِنْ ذِكْرِ اللَّهِ»[9]،
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 7«لايزالُ لسانُكَ رطباً من ذكر الله».
- نبراس طالب (2)نبراس طالب (2) «لَا يَزَالُ لِسَانُكَ رَطْبًا مِنْ ذِكْرِ اللَّهِ»