Skip to content

"Yàlla farataal na ay farata buleen ko sànk, mu teg ay dig buleen ko jéggi, mu araamal ay mbir buleen ko xëtt, mu noppi ci ay mbir ngir yërëm leen waaye fàttewu ko kon buleen ko gëstu".

Jële nañu ci Abii Sahlabata Al-Xusani Jursuum ibn Naasir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

"Yàlla farataal na ay farata buleen ko sànk, mu teg ay dig buleen ko jéggi, mu araamal ay mbir buleen ko xëtt, mu noppi ci ay mbir ngir yërëm leen waaye fàttewu ko kon buleen ko gëstu".

«إِنَّ اللَّهَ فَرَضَ فَرَائِضَ فَلَا تُضَيِّعُوهَا، وَحَدَّ حُدُودًا فَلَا تَعْتَدُوهَا، وَحَرَّمَ أَشْيَاءَ فَلَا تَنْتَهِكُوهَا، وَسَكَتَ عَنْ أَشْيَاءَ رَحْمَةً لَكُمْ غَيْرَ نِسْيَانٍ فَلَا تَبْحَثُوا عَنْهَا».

Ad-Daaraxutnii moo ko soloo ci Sunnaam ak ñeneen.
An-Nawawii nee na hadiis bu rafet la
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne Yàlla dafa waral ay mbir farataal ay farata kon nangeen taqoo ak moom te buleen sàggan di ko bàyyi walla di ko doyadal, mu def ay kiiraay ak i xuppe yu ñu natt mu leen di yiir di leen xupp ci lu mu gërëmul, kon buleen jéggi li Sariiha digle, mu araamal yu araam buleen ko wàcc te buleen ko jege, lu dul loolu nag da ko a bàyyi noppi ca ngir yërëm ay jaamam, bu ko defee mu des ca dagan ga, kon buleen ko gëstu.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Hadiis bi tegtal la ci ne Yàlla mooy kiy yoonal te ci loxoom la mbir yi nekk.

Hadiis bi dafa làmboo ay tënki Sariiha ci ay àtte ak lu mu daganal; ndaxte àtteb Sariiha benn mu nekk lu ñu noppi walla lu ñu wax, te benn it mu nekk lu ñu digle ci ag waral walla ci ag sopp, walla lu ñu tere ci ag araamal walla ci ag sibeel, walla muy lu ñu daganal.

Lu Yàlla noppi te farataalu ko, te it leeralu ko, te terewu ko loolu day dagan.

Rafetug leeralu Yonente bi batax mu séddale hadiis bi séddale gu leer gii.

War na ñu sàmmonte ak faratay broom bi.

Araamalees na jéggi digi Yàlla yi.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Ad-daaraqutniy (4396).

Yataal gi (4)

المعجم الكبير للطبراني (22/221).

جامع العلوم والحكم (ص617).

شرح الأربعين النووية للعثيمين (ص309).

توضيح الأحكام من بلوغ المرام (6/ 210).