"ñiy yërëme Aji-Yërëme ji dana leen yërëm, yërëmleen waa suuf, kon ka ca kaw asamaan dana leen yërëm.
Jële na ñu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"ñiy yërëme Aji-Yërëme ji dana leen yërëm, yërëmleen waa suuf, kon ka ca kaw asamaan dana leen yërëm.
«الرَّاحِمُونَ يَرْحَمُهمُ الرَّحمنُ، ارحَمُوا أهلَ الأرضِ يَرْحْمْكُم مَن في السّماء».
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ñiy yërëm ñeneen ñi Aji-Yërëme ji dana leen yërëm ca yërmàndeem ja xajoo lépp; muy ag pay gu dëppoo ak séen jëf. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di digle ñu yërëm lépp lu nekk ci kaw suuf, muy nit walla mala, walla njanaaw mbaa yeneen xeeti mbindeef yi, payug loolu nag mooy Yàlla mi ci kaw asamaan yi yërëm leen.
...:
Diiney Lislaam diiney yërmànde la, te léppam dafa taxaw ci topp Yàlla ak rafetal jëme ci mbindeef yi.
Yàlla mu màgg mi dafa melowoo yërmànde, te moom Aji-Sell ji yërëmaakoon la ci ñépp te mooy yërëm ku ko soob ëllëg bis-pénc, te mooy àggale yërmànde ci jaamam ñi.
Pay moom moo ngi aju ca kem jëf ya, ñiy yërëme Yàlla dana leen yërëm.
Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (7/ 297) (4941).
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (3/ 483) (1924).
Yataal gi (7)
مسند أحمد ط الرسالة (11/ 33) (6494).
تحفة الأحوذي بشرح جامع الترمذي.
لمحمد المباركفورى (6/ 43).
سلسلة الأحاديث الصحيحة وشيء من فقهها وفوائدها.
للألباني (2/ 594).
معارج القبول بشرح سلم الوصول إلى علم الأصول.
حافظ الحكمي (1/ 156).