«ñaari jullit bu ñu jaamaarloo ak séen ñaari Jaasi ka raye ak ka ñu ray yépp sawara lañu jëm
Jële nañu ci Abuu Bakrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónenteb Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:
«ñaari jullit bu ñu jaamaarloo ak séen ñaari Jaasi ka raye ak ka ñu ray yépp sawara lañu jëm», ma ne ko: yaw Yónente Yàlla bi kii moo ray, waaw ki ñu ray moom luy mbiram? Mu ne: «ndax moom dafa xéroon ci ray waayam ji».
«إِذَا الْتَقَى الْمُسْلِمَانِ بِسَيْفَيْهِمَا فَالْقَاتِلُ وَالْمَقْتُولُ فِي النَّارِ»، فَقُلْتُ: يَا رَسُولَ اللهِ هَذَا الْقَاتِلُ، فَمَا بَالُ الْمَقْتُولِ؟ قَالَ: «إِنَّهُ كَانَ حَرِيصًا عَلَى قَتْلِ صَاحِبِهِ».
Yónente bi day xamle ne ñaari jullit bu ñu jaamaarloo ak séen ñaari Jaasi, ku nekk jubloo ray moroom ja; kon ki raye sawara lay jëm ngir sababus li mu ray waayam ji, Waaye Sahaaba yi di leer lu ci ki ñu ray: naka lay dugge sawara? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- xamal leen ne moom it dafa bëggoon a ray moromam ji, te dara terewul mu ray ko lu dul li waa ji gaawantu njëkk koo ray.
فما بالُ: البال: الحال والشأن.
Ki dogu ci xolam ci def ag moy daal di def ay sababam kooku day yayoo mbugël.
Moytandikuloo gu tar ci rayante ci diggante jullit ñi ak tëkku ci sawara gi ci nekk.
Rayante ci diggante jullit ñi bu tegee ci dëgg du dugg ci tëkku gi, niki rayanteek ñi bew ak yàqkat yi.
Kiy def ay bàkkaar yu mag yi du nekk yéefër ngir loolu rekk; ndaxte Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- daa woowe ñaar ñiy rayante ay jullit.
Bu ñaari jullit jamaarloo ci jumtukaay bumu man a doon buy raye, ba kenn ka ray moroom ja, kon ki raye ak ka ñu ray ñépp sawara lañu jëm, li Hadiis bi tudd Jaasi nag day niral rekk.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 15) (31).
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2213) (2888).
(1/ 26).
(1/ 166).
Yataal gi (4)
نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.
شرح رياض الصالحين.
لابن عثيمين شرح رياض الصالحين لابن عثيمين (1/ 71).
المعجم الوسيط.