Skip to content

«ki gën ci yéen mooy ki jàng Alxuraan te di ko jàngale».

Jële nañu ci Usmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«ki gën ci yéen mooy ki jàng Alxuraan te di ko jàngale».

«خَيْرُكُمْ مَنْ تَعَلَّمَ الْقُرْآنَ وَعَلَّمَهُ».

Al-buxaariy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ki gën ci jullit ñi te gën leen a kawe ay daraja fa Yàlla mooy: ki xamlu Alxuraan, cig jàng ak mokkal ak dégg ak firi, te xamal ñeneen ñi la mu am ci xam-xami Alxuraan ànd ak di ko jëfe.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Leeral tedd-ngay Alxuraan, ak ne moo gën ci wax yi; ndaxte waxi Yàlla la.

Ki gën ci way-jàng yi mooy kiy jàngal ñeneen ñi waaye du ki koy yamale ci boppam rekk.

Jàng Alxuraan ak di ko jàngale dafay làmboo jàng ga ak xam maanaa ya ak àtte ya.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (6/ 192) (5027).

Yataal gi (8)

فتح الباري شرح صحيح البخاري.

لابن حجر العسقلاني (1/ 374).

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (2/ 226).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمصطفى الخن وغيره (1/ 740).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (4/ 638).