«saa du taxaw lu dul ne nit dana romb ci bàmmeelu benn waay naan: aka neexoon ma nekk palaasam».
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«saa du taxaw lu dul ne nit dana romb ci bàmmeelu benn waay naan: aka neexoon ma nekk palaasam».
«لاَ تَقُومُ السَّاعَةُ حَتَّى يَمُرَّ الرَّجُلُ بِقَبْرِ الرَّجُلِ فَيَقُولُ: يَا لَيْتَنِي مَكَانَهُ».
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne bis-pénc du taxaw mukk lu dul ne nit dana romb ab bàmmeel di mébet bu deewoon ba nekk palaasam, te sabab sa mooy dafa ragal ci boppam diineem di dem ngir li ag neen ak i ñoñam di not, ba fitna ak moy ak yu bon yi fés.
Ag juñj la ci ne moy yi ak fitna yi dañuy fés ci mujjug jamono.
Soññee ci moytu ak waajal dee ci gëm ak jëf yu baax, te sori bérabi fitna yi ak balaa yi.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (9/ 58) (7115).
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2231) (157).
Yataal gi (4)
إكمال المعلم (8/451).
شرح ابن بطال (10/58).
الإفصاح عن معاني الصحاح (6/295).
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (44/ 388).