Skip to content

«ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc».

Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc».

«مَنْ رَدَّ عَنْ عِرْضِ أَخِيهِ رَدَّ اللهُ عَنْ وَجْهِهِ النَّارَ يَوْمَ الْقِيَامَةِ».

At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat.
Wér na
Leeral gi

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daf nuy xamal ne képp kuy sàmm wormay mbokkum jullit ci jëw ak ci tere ñu ŋàññ ko walla jëmale si moom lu ñaaw, Yàlla dana ko fegal mbugal ca bis-pénc ba.

Maanaay baat yi

عِرْضِ أَخِيهِ: العرض هو ما يُمْدَح به الإنسان أو يذم.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci njariñal adiis bi: Tere nañu di wax ci deru jullit ñi.

Am pay daal mu ngay toll kem na jëf ja tollu, ku feg deru mbokkam Yàlla fegal ko sawara.

Lislaam diiney mbokkoo la ak dimbalante ci diggante ay ñoñam.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (3/ 488) (1931).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (45/ 528) (27543).

Yataal gi (8)

توضيح الأحكام من بلوغ المرام.

للبسام (7/ 499).

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (10/ 349).

فتح ذي الجلال والإكرام.

لابن عثيمين (6/ 437).

سبل السلام بشرح بلوغ المرام.

للصنعاني (2/ 692).