Skip to content

"matalleen sàppe si jiitu, teg ca sa ca topp, lu cay am ci mànkite na nekk ca sàppe su mujj sa.

Jële nañu ci Anas Ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

"matalleen sàppe si jiitu, teg ca sa ca topp, lu cay am ci mànkite na nekk ca sàppe su mujj sa.

«أَتِمُّوا الصَّفَّ المُقَدَّمَ، ثُمَّ الَّذِي يَلِيهِ، فَمَا كَانَ مِنْ نَقْصٍ فَلْيَكُنْ فِي الصَّفِّ المُؤَخَّرِ».

Abuu Daawuda soloo na ko ak An-Nasaa-iyyu
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day digal góor ñiy julli mbooloo ñu matal sàppe su njëkk si, teg ca ñu matal sàppe sa ca topp, ba mu jeex, bu dee day am ag ci af sàppe na mànkite gi nekk ci sàppe su mujj si.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Leeral sunna ci yemale sàppe yi.

War na ci way-julli yi ñu bañ a bàyyi genn mànkite ci sàppe yi jiitu, waaye na mànkite gi nekk ci sàppe su mujj si.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (2/ 10) (671).

Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (2/ 93) (818).

Yataal gi (1)

شرح سنن أبي داود للعباد (89/ 25).