Skip to content

«xibaarleen ma bu ag dex nekkoon ci buntu këru kenn ci yéen mu ciy sangu bis bu nekk juróomi yoon, ndax loolu dana dese tilim ci yaram?

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:

«xibaarleen ma bu ag dex nekkoon ci buntu këru kenn ci yéen mu ciy sangu bis bu nekk juróomi yoon, ndax loolu dana dese tilim ci yaram?" Ñu ne ko: déedéet du bàyyi ci deram dara, mu ne: "loolu nag moo ngi mel ni julliy juróom, yàlla da ciy far njuumte yi».

«أَرَأَيْتُمْ لَوْ أَنَّ نَهَرًا بِبَابِ أَحَدِكُمْ يَغْتَسِلُ فِيهِ كُلَّ يَوْمٍ خَمْسًا، مَا تَقُولُ ذَلِكَ يُبْقِي مِنْ دَرَنِهِ؟» قَالُوا: لَا يُبْقِي مِنْ دَرَنِهِ شَيْئًا، قَالَ: «فَذَلِكَ مِثْلُ الصَّلَوَاتِ الخَمْسِ، يَمْحُو اللَّهُ بِهِ الخَطَايَا».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day niròole julliy juróom ci bis bu nekk ak guddi gi, ci ni muy fare bàkkaar yu ndaw yi ak njuumte yi dafamelni ag dex gu nekk ci buntu kër nit ki mu ci sangu bis bu nekk juróomi yoon, ba du bàyyi ci deram bi ak ci tilimam ji dara.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ngëneel lii day jagoo rekk ci far bàkkaar yu ndaw yi, bu dee yu mag yi nag fàww ñu tuub ko.

Ngëneelu joxe julliy juróom ak sàmmoonte ak moom ci ay sàrtam ak i ponkam, ak i wareefam ak i sunnaam.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 112) (528).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 462) (667).

(1/ 282).

Yataal gi (7)

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

مجموعة من الباحثين (2/ 773).

تطريز رياض الصالحين.

لفيصل آل مبارك (ص610).

المعجم الوسيط.

النهاية في غريب الحديث والأثر.

لابن الأثير (2/ 115).