Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

76 of 732 cards

Clear filters
"su ngeen wakkirlu woon ci Yàlla dëgg-dëggi wakkirlu, kon dana leen wërsëgal kem ni muy wërsëgale picc yi, day xëy nekk ku woos xiif di gont biir bi fees dell".
Wér na Imaam Ahmad ak At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-yyu ak Ibnu Maaja ak Ibnu Hibbaan ci Sahiiham ak Al-Haakim ñoo ko soloo.
"bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla".
Wér na Ahmad, ak At-Tirmisiyyu, ak Ibn Maaja ak Ibn Hibbaan ñoo ko soloo.
«kiy biral Alxuraan moo ngi mel ni kiy biral ab sarax, kiy yalu Alxuraan it moo ngi mel ni kiy nëbb ab sarax».
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy.
"ndax duma leen xibaar lu gën darajay woor ak julli ak saraxe? Ñu ne ko: ahakay, mu ne: "yéwenug diggante yi, ndax yàqug diggante yi mooy lay wat nag".
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy.
"àjjana amna téeméeri daraja diggante ñaari daraja yu nekk day mel ni diggante asamaan ak suuf, Firdawsi moo ca gën a kawe daraja te ca la ñenti dexi àjjana yi di balle, te ca kawam la Aras nekk, bu ngeen dee laaj Yàlla laajleen ko Firdawsi".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko.
«fi Boroom bi di gën a jegee jaam bi mooy ci mujjantalu guddi gi, boo manee di bokk ci ñiy tudd Yàlla ci waxtu woowo def ko».
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy.
Benn bis Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa taxaw fi nun daal di nuy waar waar gu jotale xol yi jàq nañu ci, bët yi tuur ci rangooñ, ñu ne ko : yaw Yónente Yàlla bi, waar nga nu waarug kuy tàggatoo, jox ñu ak kóllare. Mu ne leen : "dénk naa leen ngeen ragal Yàlla ci dégg ak topp, donte jaamub Habasa la, dangeen gis ci sama ginnaaw ag wuute gu tar, waaye nangeen jàpp ci sama Sunna ak sunnay njiit yu jub ya tey jubal, ŋànkleen ko ak seen i dégéj, te ngeen moytandiku mbir yi ñu sos, ndax bidaa yépp ay réer la".
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
"yéen nit ñi, deeleen tasaare nuyóo, di leele ñam, di jokk mbokk, di julli guddi fekk nit ñi a ngi nelaw, kon dangeen dugg àjjana ci jàmm".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.