Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

18 of 732 cards

Clear filters
"Yàlla day fiir, way-gëm it day fiir, te fiiràngeg Yàlla mooy way-gëm ji def lu mu araamaal".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na nu ne benn waay dafa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi naka lañuy pange yéefar bi ci xar kanamam ? Mu ne ko: «xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?» Xataadatu wax na: ahakay giñ naa ko ci sunu màggug Boroom.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«Yàlla du tooñ benn way-gëm ci jëfam ju baax di ko wàññi, dana ka ko jox fii ci àdduna fay ka ko ca allaaxira, bu dee ab yéefér nag ay jëfam yu baax yi mu def ngir Yàlla fii ci àdduna, dañu ka koy dundale, ba bu demee allaaxira, du fa fekk jenn jëf ju baax buñu koy fay».
Wér na Muslim soloo na ko.
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yàlla nee na: ku noonook sama péete yégal naako ab xare, sama jaam bi du ma jegeñ-jegeñlu ci dara lu ma gënal li ma farataal ci moom, sama jaam bi du deñ dima jéema jege ci ay naafila ba ma bëgg ko, te bu ma ko bëggee, maay nekk déggam gi muy dégge, ak gisam gi muy gise, ak loxoom bi muy jàppe, ak tànkam bi muy doxe, bu ma ñaanee ma may ko,bu ma musloo ma musal ko, du ma dengi-dengi ci dara lu may def, samag dengi-dengi mi ngi ci bu may jël bakkanu aji-gëm ji, ndax day bañ a dee,te man dama koy bañ a def lu mu bëggul».
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
"Yàlla mu baarkeel mi te kawe day wax waa àjjana: éey yéen waa àjjana? Ñu ne ko wuyusi nanu la topp nañu la ak mbegte, mu ne leen: ndax gërëm ngeen? Ñu ne ko: lu ñuy teree gërëm te nga jox nu loo joxul kenn ci sa mbindeef yi? Mu ne leen: dama leen di jox lu gën loolu, ñu ne ko: yaw sunu Boroom, ana lan moo gën loolu? Mu ne leen: wàcce naa sama ngërëm ci seen kaw, dootuma leen mere ba fàww".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf».
Wér na Muslim soloo na ko.
«amul kenn ci yéen lu dul ne Yàlla dina wax ak moom, te kenn kuy firi du nekk seen diggante, mu xool ndayjooram du gis lu dul li mu jiital, mu xool càmmooñam du gis lu dul li mu jiital, mu xool kanamam du gis lu dul sawara wu jàkkarloo ak moom, ragalleen sawara donte dangeen joxe aw xaru tàndarma la».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"ñiy yërëme Aji-Yërëme ji dana leen yërëm, yërëmleen waa suuf, kon ka ca kaw asamaan dana leen yërëm.
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat.