Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

1 of 732 cards

Clear filters
Aliyun Ibn Abii Taalib yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa yónnee ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu bawoo Yaman as wurus mu nekk ci abder bu nu wulli, te setaluñu ko sax ca suuf sa, nee na: mu sédale ko ci diggante ñenti nit, diggante Uyaynata ibn Badrin, ak Aqrah ibn Haabis, ak Saydul Xayri, ñenteel bi benn muy Halqamata walla muy Aamir ibn Attufayl, jenn waay ci ay àndandoom ne: nun de noo gënoon a yayoo lii ci ñii, nee na loolu egg ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu wax ne: "mo ndax wóoluwuleen ma te man maay kóoluteg ki ci asamaan xibaaru asamaan dima dikkal suba ak ngoon", nee na jenn waay jug bët yi dugg, jë bi génn, kawaru sikkim bi sëq, mu wat kawar gi, mu gàtt kodaay, daal di ne: yaw Yonnente Yàlla bi, ragalal Yàlla, mu ne ko: "toskare ñeel na la, ndax du maa gën a yay ci waa suuf ci ragal Yàlla" nee na: waa ji dummooyu dem, Xaalid ibnul Waliid ne : yaw Yonnente Yàlla bi, ndax duma dagg baat bi? Mu ne ko: "déedéet, amaana moo ngi julli" Xaalid ne ko: bariwaa na kuy julli, di wax ci làmmiñam lu nekkul ci xolam, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: "man digaluñu ma ma wëlbati xoli nit ñi, du caagine ma xotti seen biir yi" nee na: topp mu xool ko muy dem, mu wax ne: "dana génn ci ndiggul waa jii ay nit wow dañuy jàng téereb Yàlla bi mu tooy xepp, te du weesu seen put yi, dañuy génn ci diine kem ni fett gi di génne ci sànnikaay bi", te njort naa ne dafa wax ne: "bu ma leen fekke woon kon dinaa leen ray rayug Samuud".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.