Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

47 of 732 cards

Clear filters
Bokk na ci màndargay bis-pénc nu yëkkati xam-xam, réer bari, njaalo bari, naan sàngara bari, góor ñi néew, jigéen ñi bari, ba juróom-fukki jigéen di tolloog benn góor».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, alkande ñeel na araab yi ci ay wu jege, tijji nañu tay ci baaraasu Yaajuuja ak Maajuuja lu toll ni" mu ràbbale baaraamu déyam ak ba ca topp, Saynabu Bint Jahsin nee na ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi: ndax dees nuy alag te ñu baax ñi nekk sunu biir? Mu ne ko: "waaw bu lu bon baree».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"mbooloo miy njëkk a dugg àjjana dañuy nekk ci melow weer wi ci guddig Badr, ña topp ca ñoom gën a tarug leer biddiwu per ci ag leer, te duñu saw duñu dem wanag, duñu tifli du ñu ñandu, seen peñe yi ci wurus la, seen ñaq yi Misk la, seen garabi taal yu neex ya bantu gëtt la, seen jabar ya Huuru Hiin lañu, ñu nekk ci bindug kenn nit, ci melow seen baay Aadama, juróom-benn-fukki xasab ci kaw".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waxtaanal na nu te mooy aji-dëggal ba di ku ñu dëgggal ki mu ne: «kenn ci yéen dees na dajale am mbindam ci biiru yaayam ñent-fukki bis ak ñent-fukki guddi, mu nekk lumbuw dereet, kem loolu, nekk aw suux kem loolu, ñu yabal ci moom malaaka ma, ñu digal ko ñenti baat, mu bind ko: wërsëgam, ab digam, ak jëfam, ak day texeedi walla day texe, mu wal ca ruu, kenn ci yéen de dana jëf jëfi waa àjjana ba dara nekkul digganteem ak moom lu dul loxo, téere ba jiitu ko mu jëf jëfi waa sawara daal di dugg sawara, kenn ci yéen it dana jëf jëfi waa sawara ba dara doxul digganteem ak moom lu dul ab loxo, mu jëf jëfi waa àjjana daal di dugg àjjana».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"man maay sangu nit ñi ëllëg bis-pénc, ndax xam ngeen lu tax loolu? Yàlla day dajale nit ña jiitu ak ña mujj ci benn barab, dañuy dégg aji-woote ji, te it dees leen di gis, Jant bi jege, nit ñi egg ci njàqare ak jafe-jafe lu ñu àttanul te manuñu ko a muñ, nit ñi ne: xanaa gisuleen li leen jot, ndax dungeen xool ku leen tinu ci seen Boroom? Ñenn ci ñoom wax ñeneen ñi: demleen ci Aadama, ñu ñëw ci Aadama ne ko: yaw yaay baayu nit ñi, Yàlla bind la ci loxoom, daal di wal ci yaw ci ruuham gi, mu digal malaaka yi ñu sujjóotal la, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Xanaa gisóo li nu jot? Aadama ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du masa mer mer mu mel ni moom ginnaawam , te moom da maa tere woon garab ga ma moy ko, sama bopp sama bopp doyna ma, demleen ci ku dul man, demleen ci Nuuh, ñu dem ci Nuuh, ne ko: yaw Nuuh yaw yaay Yonente bi njëkk ci waa suuf, te Yàlla tudde na la jaam bu man a sant bi, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Mu ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du masa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te man damaa amoon ñaan gu ma ñaan ci kaw sama nit ña, sama bopp sama bopp doyna ma, demleen ci ku dul man, demleen ci Ibraahiima, ñu ñëw ci Ibraahiima, ne ko: yaw Ibraahiima yaw ndawul Yàlla nga di xaritam ci waa suuf, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Mu ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du musa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te man damaa fenoon ñatti fen, sama bopp noyna ma, demleen ci ku dul man, demleen ci Muusaa, ñu ñëw si Muusaa, ne ko: yaw Muusaa yaw ndawul Yàlla nga, te gënale na la ci yónni gi mu la yónni ak wax gi mu wax ak yaw, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Mu ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du musa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te man damaa ray bakkan bob digaluñu ma ma ray ko, sama bopp noyna ma demleen ci ku dul man, demleen ci Iisaa ibn Maryma, ñu dikkal Iisaa, ne ko: yaw Iisaa yaw ndawul Yàlla nga, di kàddoom gu mu sànni ca Maryama di ruu gu jóge ci Moom, nga wax ak nit ñi ca lal ba di ab liir, tinu nu ci sa Boroom xanaa gisóo ci li nu nekk? Iisaa ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du musa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te tuddul benn bàkkaar, sama bopp noyna ma, demleen ci ku dul man, demleen ci Muhammat, ñu dem ca Muhammat, ne ko: yaw Muhammat, yaw ndawul Yàlla nga, di ki mujj ci ñi Yónente yi, te Yàlla jéggal na la li jiitu ci say bàkkaar ak Li mujj, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Ma daal di dem ca ronu Aras, ma rot daal di sujjóot ñeel sama Boroom, Yàlla xamal ma ci ay xeeti sant Yàlla ak tagg ko loo xam ne masu ko xamal kenn ku ma jiitu, topp ñu ne ko: yaw Muhammat, yëkkëtil sa bopp, laajal ñu jox la, sàkkul ramm ñu jox la, ma yëkkëti sama bopp, ma wax ne: sama xeet wi yaw sama Boroom, sama xeet wi yaw sama Boroom, sama xeet wi yaw sama Boroom, ñu ne ko: yaw Muhammat, dugalal ci sa xeet ñi ñu dul càmbar ci buntu ndayjoor bi, ci bunti àjjana yi, te ñoom dañuy bokk ak nit ñi ci yeneen bunt yu dul yooyu, topp mu ne: giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom ne li ci diggante ñaari jàppukaayi bunt yi ci bunti àjjana yi, moo ngi mel ni diggante Màkka ak Himyar -walla moo ngi mel ni diggante Màkka ak Busraa-".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Nun nooy xeet wi mujj, di ñi ñu njëkk a regle, dañuy naan: ana xeet wi jàngul ak seen Yonnente? Nun nooy ñi mujj di ñiy njëkk".
Wér na Ibnu Maaja soloo na ko.
«Bis-pénc du ñëw mukk ba keroog jànt bi di fenke sowwu, bu fa fenkee nag ba nit ñi gis ko ñoom ñéppay gëm, te loolu mooy jamono joj: {amul benn bakkan bu ngëmam di jariñ bu gëmul woon lu njëkk, te fàggu ca ngëmam ga aw yiw} [Al-Anhaam: 158] bis-pénc dana taxaw fekk ñaari waay tallal nañu séen yére seen diggante te duñu ko mujj a jaayante, dunu ko it mujj a lem, bis-pénc dana taxaw fekk ben waay juge na fa mu ràtte soowam te du ko mos sax, bis-pénc dana taxaw fekk nit a ngi tabax ab baajam te du sa naan, fekk nit ki yëkkati ab tibam jame ko ci gémmeñam te du ko ñam».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"bu kenn ci yéen faatoo dees na ko gaaral bérabam ci suba gi ak ci ngoon gi, bu dee dafa bokk ci waa Àjjana mu nekk ci waa Àjjana, bu dee dafa bokk ci waa Sawara mu nekk ci waa Sawara, ñu naan ko: lii mooy sa bérab ba keroog Yàlla di la dekkil ëllëg bis-pénc".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.