Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

34 of 732 cards

Clear filters
"ñi ma gën a bëgg ci yéen, te gën maa jege ëllëg bis-pénc, ñooy ñi gën a rafet jikkó ci yéen, waaye ñi ma gën a bañ ci yéen te gën maa sori ëllëg bis-penc, ñooy coowkat yi, ak puukarekat yi, ak ñiy rëy-rëylu", ñu ne ko:yaw Yonente Yàlla bi, nun xam nanu coowkat yi ak puukarekat yi, kon lan mooy al-mutafayxihuuna? Mu ne leen: mooy: ñiy rëy-rëylu".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko.
Wax naa: yaw Yonente Yàlla bi: kan laay gën a rafetal ci moom? Mu ne ma: "sa yaay, topp ca sa yaay, topp ca sa yaay, topp ca sa baay, topp ca ki gën a jege".
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat.
«amul dara lu gën a diis ci màndxem jullit bi ëllëg bis-pénc jikko yu rafet, te Yàlla dafa bañ ku ñaaw i wax ñaaw i jëf».
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy.
"amul ñaari jullit yuy daje daal di joxante loxo lu dul ne dees na leen jéggal laata ñuy teqalikoo".
Wér na ci kaw bees boolee mbooleem yoon yi mu ñëwee Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Nekkul woon ku ñaaw i wax du caagine ay jëf, du caagine kuy coow ci ja yi, (marché)te daawul fayantoo lu ñaaw, waaye day baale di jéggale.
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat.
"ndax duma leen xibaar ñi gën ci yéen ak ñi yées ci yéen?" Nee na: ñu noppi, mu wax loolu ñatti yoon, jenn waay ne ko: ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, wax nu ñi gën ci nun ak ñi yées ci nun, mu daal di ne: "ki gën ci yéen mooy ki ñuy yaakaar yiwam te wóolu ayam, ki yées ci yéen mooy ki ñu yaakaarul ayam te wóoluwuñu ayam".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko.
"yal na Yàlla leeralal waaju dégg ci man dara mu jottali ko kem na mu ko dégge woon, bariwaana ku ñu jottali mu gën a xam aji-dégg ji".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
"Solleen seen yére yu weex yi, ndax moo gën ci seen yére yi, te nangeen ci sàng seen way-faatu yi".
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja.