Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

27 of 732 cards

Clear filters
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa téye ci loxoom, ne ko: "yaw Muhaas, waat naa ci Yàlla ne dama laa bëgg", mu ne ko: "maa ngi lay dénk yaw Muhaas bul bàyyi mukk di wax ginnaaw julli gu ne: Allaahuma ahinnii halaa sikrika wa sukrika wa husni hibaadatika".
Wér na Abuu Daawuda ak An-Nasaa-yyu ak Ahmad ñoo ko soloo
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na nu jàngal Alxuraan ci gépp anam fii ak nekkul ci janaba.
Tane na Abuu Daawuda ak At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ak Ibn Maaja ak Ahmad ñoo ko soloo.
«ki gën a mat ug ngëm ci jullit ñi mooy ki ci gën a rafet jikko, te ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam».
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat.
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc musul a xeex ak i nit ba keroog mu leen di woo.
Wér na Ahmad ak Al-Bayhaqii ñoo ko soloo.
Ba ko Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc yónnee Yaman da ko a digal mu jël ci Nag fanweer yu nekk wenn nag wu am at wu góor walla wu jigéen, ak ci ñent-fukk yu nekk wenn nag wu am ñaari at, ak ci ñoñ-téere buy aji-gént -maanaam di gént di sëy- ab Diinaar walla lu toll ni moom ci Mahaafir, ay yére la yu nekk Yaman.
Wér na bees sukkandikoo ci yeneen yi koy dëggal Abuu Daawuda ak At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ak Ibn Maaja ak Ahmad ñoo ko soloo.
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamal na ñu xutbag aajo: cant ñeel na Yàlla, ñoo ngi koy dimbandikoo, di ko jéggalu, di muslu ci moom ci ayu sunu bakkan, ku Yàlla gindi kenn manu koo sànk, ku Yàlla sànk kenn manukoo gindi, maa ngi seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, tey seede ne Muhammat jaamam la Yónenteem la, {éey yéen nit ñi ragal leen séen Boroom mi leen bind ci benn bakkan bind ca it jabaram, tasaare si ñoom ñaar ay góor yu bari ak i jigéen, nangeen ragal Yàlla mi nga xam ne ci moom ngeen di laajante, te ragal ag meen, Yàlla moo ngi leen di fuglu}[An-Nisaa: 1], {éey yéen ñi gëm nangeen ragal séen Boroom dëgg-dëggi ragal te buleen dee lu dul ne ay jullit ngeen} [Aali-Imraan: 102], {éey yéen ñi gëm nangeen ragal Yàlla tey wax wax ju jub(70) kon dana yéwénal séen i jëf jéggal leen séen i bàkkaar, ku topp Yàlla ak ub Yónenteem texe na texe gu màgg} [Al-Ahsaab: 70-71].
Wér na Abuu Daawuda ak At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ak Ibn Maaja ak Ahmad ñoo ko soloo.
"ku seeti ku feebar, te ab digam ñëwagul, mu wax juróom-ñaari yoon: As-alul Laaha Al-Hasiima Rabba Al-Harsi al-hasiimi an yasfiyaka, lu dul ne Yàlla dana ko may jàmm ca feebar boobu".
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Rabbi ixfir lii, Rabbi ixfir lii».
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak An-nasaa'iy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.