Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

23 of 732 cards

Clear filters
"ñaari xaaj a gi nii yu bokk ci waa sawara te gisaguma leen,ay nit yu yor ay yar yu mel ni geeni nag di ci dóor nit ñi,ak ayjigéen yu solu ba noppi rafle, jeng di jengale, seeni bopp ya day mel ni jégénu giléem gu jeng,duñu dugg àjjana,te xet ga sax du leen xeeñ,te xetam ga dana toll ci doxub nangam ak sàngam".
Wér na Muslim soloo na ko.
"gaaral na ñu ma Àjjana ak Sawara waaye gisuma ca yiw walla ay wu mel ni tay jii, te bu ngeen xamoon li ma xam kon dangeen ree tuuti te dangeen jooy lu bari, nee na: bis bu ko gën a tar musul a am ci Sahaabay Yonente Yàlla bi, nee na: ñu muur seen bopp yi di yékkét, nee na: Umar daal di ne: gërëm nanu Yàlla muy sunu Boroom, ak Lislaam muy sunu Diine, ak Muhammat muy sunu Yonente, nee na: waa jooja daal di jug, daal di ne: kan mooy sama baay? Mu ne ko: "diw mooy sa baay" aaya bii wàcc: {yéen way-gëm ñi bu leen laaj loo xam ne bu ñu leen ko leeralee mu naqari leen} [Al-Maa-ida: 101].
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"Yàlla mu Baarkeel mi te kawe nee na: waajalal naa sama jaam yu sell yi, lu bët musul a gis, nopp musu ko a dégg, te musul a rot ci xolo nit" Abuu Hurayrata nee na: jàngleen bu leen soobee: {benn bakkan xamul la ñu ko dencal ci luy bégloo ay bët} [As-Sajda: 17].
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Nekkoon nanu fi Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu dégg am riir, Yonnente bi daal di wax ne: "ndax xam ngeen lan la?" Nee na: nu ne ko: Yàlla ak ub yonnenteem ñoo xam, mu wax ne: "aw doj la wu ñu sànni ca biir sawara diirub juróom-ñaar-fukki at, mooy door a wàcc ca sawara sa leegi ba egg ca suuf".
Wér na Muslim soloo na ko.
"amna ca Àjjana ag garab gog ki war aw fas wu ñu tàggat ba mu gaaw dana ca daw luy toll ak téeméeri at te du ko dog".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«ku seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla moom dong amul te amul bokkaale, ak ne Muhammat ndawul Yàlla la di ndawam, ak ne Iisaa jaamub Yàlla la di ndawam, di kàddoom gu mu sànni ci Maryama di ag ruu gu bawoo ci moom, ak ne àjjana dëgg la, sawara dëgg la, Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"danañu indi jenn waay ëllëg bis-pénc, sànni ko ca sawara, buttiti biir yi tasaaroo, mu koy wër kem ni mbaam di wëre ci takkuwaayam, waa sawara daje fa moom, naan ko: yaw diw lan moo la dal? Xanaa du yaa nu daan digal lu baax di nu tere lu bon? Mu ne: ahakay, dama leen daan digal lu baax te daawuma ko def, daan leen tere lu bon ba noppi di ko def".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.