Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

41 of 732 cards

Clear filters
Benn waaye dafa wax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: dénk ma, mu ne ko: "bul mer" mu baamtu ko ay yoon mu ne ko: "bul mer".
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
"ndax duma leen xibaar ñi gën ci yéen ak ñi yées ci yéen?" Nee na: ñu noppi, mu wax loolu ñatti yoon, jenn waay ne ko: ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, wax nu ñi gën ci nun ak ñi yées ci nun, mu daal di ne: "ki gën ci yéen mooy ki ñuy yaakaar yiwam te wóolu ayam, ki yées ci yéen mooy ki ñu yaakaarul ayam te wóoluwuñu ayam".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko.
Laaj naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc lu baax ak lu bon, mu wax ne: "lu baax mooy rafet jikkó, lu bon mooy luy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ñi gis ko".
Wér na Muslim soloo na ko.
«jullit mooy ki nga xam ne jullit ñi mucc nañu ci làmmiñam ak ci loxoom,gàddaaykat nag mooy ki gàddaay li Yàlla araamal ci moom».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«ki gën a mat ug ngëm ci jullit ñi mooy ki ci gën a rafet jikko, te ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam».
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat.
Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lan mooy li ëpp luy duggal nit ñi àjjana, mu wax ne: «ragal Yàlla ak rafet jikko», ñu laaj ko lan moo ëpp luy duggal nit ñi sawara mu ne: «gémmiñ ak awra».
Tane na ci ag càllala, wér ci geneen càllala At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
"Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam"
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«am na benn waay bu doon lebal nit ñi, daan wax ndawam la naan ko: boo demee ci ku am jafe-jafe nanga ko jéggal, amaana Yàlla jéggal nu, mu dajeek Yàlla mu jéggal ko».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.