Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

93 of 732 cards

Clear filters
"Yàlla ku teey la te du nangu lu dul lu teey, te Yàlla dafa digal way-gëm ñi li mu digal Yonente yi, mu wax ne: {yéen Yonente yi lekkleen ci yu teey yi te ngeen jëf lu baax} mu wax it ne: {yéen ñi gëm lekkleen ci yu teey yi nu leen wërsëgal} topp mu daal di tudd benn waay bu nekk ci tukki bu sori, kawar ga jaxasoo, mu pënd lool, ma nga tàllal ay loxoom jëme kaw asamaan, di wax naan: yaw sama Boroom! Yaw sama Boroom! te li muy lekk dafa araam, li muy naan dafa araam, li mu sol dafa araam, li ñu ko dundale itam dafa araam, moo naka lees koy nangule ñaanam".
Wér na Muslim soloo na ko.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa génn ci moom ba mu jullee suba, fekk moo ngi ci jàkkaam ji, topp mu dellusi fekk mu toog, mu ne ko: "kon ba leegi yaa ngi ca na ma la bayyi woon?" Mu ne ko: waaw, Yonente bi ne ko: "wax naa ci sa ginnaaw ñenti kàddu, ñatti yoon, bu ñu ko nattoon ci li nga wax ci bis bi mu tollu ko: subhaanal Laahi wa bi hamdihi, hadada xalqihi, wa ridaa nafsihi, wa sinata harsihi, wa midaada kalimaatihi".
Wér na Muslim soloo na ko.
«ku jàng ñaari aaya yi ci mujjug saaru Al-Baxara cig guddi danañu ko fegal leeb luy Aw ay»
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"gaaral na ñu ma Àjjana ak Sawara waaye gisuma ca yiw walla ay wu mel ni tay jii, te bu ngeen xamoon li ma xam kon dangeen ree tuuti te dangeen jooy lu bari, nee na: bis bu ko gën a tar musul a am ci Sahaabay Yonente Yàlla bi, nee na: ñu muur seen bopp yi di yékkét, nee na: Umar daal di ne: gërëm nanu Yàlla muy sunu Boroom, ak Lislaam muy sunu Diine, ak Muhammat muy sunu Yonente, nee na: waa jooja daal di jug, daal di ne: kan mooy sama baay? Mu ne ko: "diw mooy sa baay" aaya bii wàcc: {yéen way-gëm ñi bu leen laaj loo xam ne bu ñu leen ko leeralee mu naqari leen} [Al-Maa-ida: 101].
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Njabootu Muhammat de yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc diirub bi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñëwee Madiina masu ñoo suur ci ñamu dugub ñatti guddi yu toftaloo, ba ni mu faatoo.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«sama xeet wépp lañuy jéggal ba mu des ñiy fésal ag moy, te bokk na ci fésal ag moy nit ku def dara ci guddi gi, daal di xëy Yàlla suturaal ko, muy wax naan: éey yaw diw, biig def na lii ak lee, fekk dafa fanaan Yàlla suturaal ko, mu xëy di wuññi li ko Yàlla suturaaloon».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«Yàlla mu màgg mi day tàllal loxoom ci guddi gi ngir ki doon def ñaawteef ci bëccëg gi tuub, di tàllal loxoom ci bëccëg gi ngir ki doon def ñaawteef ci guddi gi tuub, ba baa jant bi di fenke ci sowwu bi.
Wér na Muslim soloo na ko.
"rabbi ixfir lii xadii-atii wa jahlii, wa israafii fii amrii kullihii, wa maa Anta ahlamu bihii minnii, Allaahuma ixfir lii, xataayaaya, wa hamdii wa jahlii wa haslii, wa kulli saalika hindii, Allaahuma ixfir lii maa xaddamtu wa maa ax-xartu, wa maa asrartu wa maa ahlantu, antal Muxaddimu wa Antal Mu-axiru, wa Anta halaa kulli say-in xadiirun ".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.