Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

25 of 732 cards

Clear filters
Sama xarit ba yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dénk na ma ñatt: woor ñatti fan ci weer wu ne, ak ñaari ràkkay yoor-yoor, ak ma julli Witar balaa may nelaw.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa nekkoon ci ab tukki, mu gis jenn waay ñu keral ko, mu daal di ne: "lii lan la?", ñu ne ko dafa woor, mu wax ne: "woor ci tukki bokkul gi ag mbaax", ñew na ci yeneen i baat ci Muslim: "dénk naa leen yombali Yàlla yi mu leen yombalal".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu fukki guddi yi daan dugg da daan dundal guddi yi, yee njabootam, pasteefu daal di takku ba dëgër.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Xëdd nañu ak Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu daal di jug jëm ca julli ga, ma ne ko: ñaata moo dox ci diggante nodd gi ak xëdd gi? Mu ne: luy tolloo ak juróom-fukki aaya.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li weesu ci ay bàkkaaram».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"xëddleen, ndaxte xëdd lu am baarke la«.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na Lihtikaaf ci fukki fan yi mujj ci weeru koor, ba keroog muy faatu, ay saxnaam daldi Lihtikaaf ginnaawam.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«dàqleen Laylatul Xadri ci fukk yi mujj ci weeru koor».