Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

6 of 732 cards

Clear filters
"deeleen gaawal néew bi, ndax bu dee ku baax la ci yiw ngeen ko jëme, bu dee du loolu nag, kon aw ay la wu ngeen teg ci seen doq yi".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"yàlla rëbb na Yahuud yi ak Nasaraan yi, ndax dañoo jàppe seen bàmmeeli Yonnente yi ay jàkka" nee na: bu dul woon loolu kon dinaa fésal bàmmeelam, waaye moom dafa ragal ñu jàppe ko jàkka.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Abuu Muusaa dafa tawat tawat ju tar, mu daal di xëm fekk boppam bi moo ngi ci pooju jenn jigéen ci njabootam, te manu ko a tontu ci dara, ba mu féexee, daal di ne: man de set naa wicc ci ku Yonente Yàlla bi set ci moom, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa set wicc ci aji-yuuxu ji, ak aji-wat kawaram, ak aji-xotti yéereem.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«buleen saaga ñi faatu, ndax ñoom kat wéy nañu ca lañu jiital».
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
Benn doomu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu jigéen dafa faatu, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di génn ne: "sangleen ko ci ndox mu ànd ak siddéem ñatti yoon, walla juróom walla lu ëpp loolu bu dee gis ngeen ne aajowoo na ko, te ngeen def ca bu mujj ba gëttug Kaafuur -walla lenn ci Kaafuur-, bu ngeen noppee ngeen yégal ma ko", nee na: ba nu noppee nu yégal ko ko, mu jox nu koddaayam, daal di ne: "muur leen ko ci", Ummu Atiyyata nee na: nu def bopp ba ñatti béjjan.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digal na nu juróom-ñaar: digal na nu nuy seeti ku feebar, ak gunge néew, ak ndokkeel ku tissooli, ak jàppandal giñ gi walla aji-giñ ji, ak dimbali ki ñu tooñ, ak wuyu aji-woote ji, ak tasaare nuyóo, mu tere nu jaaro -walla takk jaaroy- wurus, ak naan ci ndabal xaalis, ak sooy ak wëtteen wu am sooy ak sol sooy ak Diibaaj.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.